Matthew 21 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Ba ñu jegeñse Jerusalem, te ñou cha Bethphage, chi tūnda i Olive, Yesu yōni ñar i tālube am, 2 Ne len, Dem len chi bir deka ba chi sēn kanam, te di ngēn feka mbamsuf mu ñu ew, and’ ak chumbur: tiki len, te isi len fi man. 3 Su len kena wah͈e lef, na ngēn ne, Borom bā len soh͈la; te di na len yōni. 4 Lile am on na nak, ndah͈ lu yonent ba wah͈ on motaliku, ne, 5 Yēgal len dōm i Zion, Sa Bur anga dika fi you, lew, te di war mbamsuf, ak chumbur dōm i mbamsuf. 6 Tālube ya dem, def naka len Yesu ebal on, 7 Indi mbamsuf ma ak chumbur ma, teg sēn cholay chi sēn kou, te mu tōg chi kou am. 8 Mbōlo ma talal sēn cholay chi yōn wa; ñenen dog i banh͈as i garap ya, te tasāre len chi yōn wa. 9 Mbōlo ma jītu ak ña topa h͈āchu, ne Hosanna Dōm i Dauda; barkel chi ki di dika chi tur i Borom bi; Hosanna ma cha kou. 10 Ba mu dike chi bir Jerusalem, deka ba yepa yengatu, ne, Kile kan la? 11 Mbōlo ma ne, Kile di Yesu, yonent i Nazareth chi Galilee. 12 Yesu h͈araf cha juma i Yalla, te gēne ña don jay ak ña don jenda ñepa cha juma ja, dupa i tābul i wēchikat i h͈ālis, ak i tōgu i ña don jay i mpetah͈, 13 Te mu ne len, Binda nañu, ne, Suma nēg war na tūda nēg i ñān; wande yēn a ko def bereb ī sachakat. 14 Silmah͈a ya ak ña lagi ñou fi mōm chi juma ja, te mu weral len. 15 Wande i njīt i seriñ ya ak bindānkat ya, ba ñu gise koutef ya mu def, ak gūne ya di h͈āchu chi juma ja, ne, Hosanna Dōm i Dauda; ñu mer lol, 16 Te ne ko, Ndah͈ dēga nga li ñile di wah͈? Yesu ne len, Wau: ndah͈ mosu len a janga, ne, Chi gemeñ’ i dōm ak i gūne yu di nampa nga motali nau? 17 Mu bayi len, gēna cha deka ba chi bir Bethany, te fanān fa. 18 Chi lelek sa nak, ba mu deluse chi deka ba, mu h͈īf. 19 Mu gis garap i sōto chi wet i yōn wa, dem fa mōm, te fekul dara, wande i h͈ob reka; mu ne ko, Bul mēñati dōm bel mos. Nōn’ ak nōna sōto ba lah͈. 20 Ba ko tālube ya gise, ñu jomi, ne, Naka sōto ba gou a lah͈e? 21 Yesu tontu len, ne, Chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn gume, te nimseū len, du len def niki ma def chi sōto bi reka, wande su ngēn wah͈e tūnda wile sah͈, ne, Roñul, te dem chi bir gēch ga, di na am. 22 Te lu mu mun a don lu ngēn di ñān chi ngum, di ngēn ko ami yepa. 23 Ba mu ñoue chi bir juma ja, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñou fi mōm ba mō jemantale, ne, Ak ban sañsañ nga defe yef yile? te ku la joh͈ sañsañ bile? 24 Yesu tontu len ne, Man it di nā len lāj bena bāt, te su ngēn ma ko wah͈e, di nā len wah͈ itam ak ban sañsañ lā defe yef yile. 25 Batise’ John, fan la juge won? cha ajana am chi nit? Ñu werante chi sēn digante, ne, Su ñu ne, Cha ajana; di na ñu ne, Lutah͈ gumu len ko won mbōk? 26 Wande su ñu ne, Chi nit; da ñu ragal mbōlo ma; ndege jape won nañu John niki yonent. 27 Ñu tontu Yesu, ne, H͈amu ñu. Mu ne len it, Man du ma len wah͈ ak ban sañsañ lā defe yef yile. 28 Wande lan ngēn dēfe? Kena nit am on na ñar i dōm yu gōr; mu ñou chi tau ba, ne, Suma dōm, demal ligey tey chi suma tōl. 29 Mu tontu, ne, Du ma dem: wande cha ganou mu rēchu, te dem. 30 Mu ñou cha ñarel ba, te wah͈ati lōga. Mu tontu, ne, Di nā dem; wande demul. 31 Kan chi ñom ñar a def la sēn bay buga? Ñu ne ko, Tau ba. Yesu ne len, Chi dega mangi len di wah͈, Publican ya ak garbo ya di nañu dem chi ngur i Yalla as yēn. 32 Ndege John ñou on na fi yēn chi yōn i njūbay, te gumu len ko won: wande publican ya ak garbo ya gum on nañu ko: te yēn ba ngēn ko gise, rechuwu len cha ganou sah͈ ndah͈ ngēn gum ko. 33 Dēglu len benen lēb: Bena borom‐ker am on na, ku jembat on tōl, ñak ko, gas cha nalukay, tabah͈ am tata, lūye ko i ligeykat, te dem cha benen rew. 34 Ba jamāno i mēñef jegeñse, mu yōni i ndau am chi ligeykat ya ndah͈ ñu jel i mēñef am. 35 Ligeykat ya japa ndau am ya, ratah͈ kena, rēy kenen, te jamat kenen ka ak i h͈êr. 36 Mu yōnêti yenen i ndau yu upa ñu jeka ña: ñu def len nōgule itam. 37 Cha ganou ga mu yōni dōm am chi ñom, ne, Di nañu teral suma dōm. 38 Wande ba ligeykat ya sēne dōm ja, ñu ne chi sēn bopa, Kile di dono gi; ñou len, na ñu ko rēy, te jel ndono am. 39 Ñu japa ko, sani ko chi biti tōl ba, te rēy ko. 40 Su borom‐tōl ba deluse nak, lan la di def ligeykat yōgale? 41 Ñu ne ko, Di na rēy nit ñu soh͈or ñōgale chi choh͈or, te lūye tōl am yenen i ligeykat, ñu ko di joh͈i mēñef yi chi sēn wah͈tu’ ñorte. 42 Yesu ne len, Ndah͈ mosu len a janga chi mbinda mi, ne, Doch wa tabah͈kat ya bañ on, mō di neki bop’ i tabah͈ ma: lile juge na fa Borom bi, te koutef la chi suñu i but? 43 Mōtah͈ ma ne len, Di nañu jele ngur i Yalla fi yēn, te joh͈ ko h͈êt wu di mēña mēñef am. 44 Ku dānuji chi doch wile, di na dama: wande ku mu dānu chi kou am, di na ko mokal kilip. 45 Ba i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya dēge lēb am ya, ñu gis ne lu jem chi ñom la wah͈. 46 Ba ñu jēme japa ko, ñu ragal mbōlo ma, ndege jape won nañu ko niki yonent. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society