Matthew 20 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Ndege ngur i ajana niro na ak bena borom‐ker ku gēna chi sūba têl, ndah͈ mu binda i ligeykat chi tōl am. 2 Ba mu wah͈ante ak ligeykat ya h͈asab bechek, mu yōni len cha tōl am. 3 Mu gēnati potah͈ chi jurom ñenentel i wah͈tu, gis ñenen ñu tah͈ou chi jēy ba te defu ñu dara, 4 Mu ne len, Dem len yēn it cha tōl ba, te di nā len joh͈ lu ela. Ñu dem. 5 Mu gēnati potah͈ chi fukel i wah͈tu ak ñar, ak chi ñetel i wah͈tu, te def nōga. 6 Chi juromel i wah͈tu chi ngon potah͈ mu gēnati, feka ñenen ñu tah͈ou; mu ne len, Lutah͈ ngēn tah͈ou fi bechek bi bepa, te defu len dara? 7 Ñu ne ko, Ndege ken a ñu bindul. Mu ne len, Dem len yēn it cha tōl ba. 8 Ba ngon jote, borom‐tōl ba ne bukanēg am, Ôal ligeykat ya, te joh͈ len sēn mpey, di dôr cha ña muje be cha ña jek’ on. 9 Ba ña mu bind’ on potah͈ juromel i wah͈tu chi ngon ñoue, nit ku nek’ am h͈asab. 10 Ba ñu jeka ñoue, ñu fōg ne di nañu jot lu upa lōga; wande ku neka itam am h͈asab. 11 Ba ñu ko jele, ñu ñurumtu lu jem chi borom‐ker ga, ne, 12 Ñile muje wena wah͈tu reka la ñu ligey, te nga emale len ak ñun, ñi enu on disay i bechek bi ak tangay am. 13 Wande mu tontu kena chi ñom, ne, H͈arit, tōñu ma la: du bena h͈asab la ñu wah͈ante won am? 14 Jelal li la lew, te dem sa yōn; buga nā joh͈ kile muje lu day ni sa bos. 15 Ndah͈ daganul ma def lu ma buga chi lu ma mōm? mbar sa but bon na, ndege mā bāh? 16 Nōnule ña muje di nañu jītuji; te ña jītu di nañu mujeji. 17 Yesu don na dem cha Jerusalem, te chi yōn wa mu jel fuk’ i tālube ya ak ñar chi mpet, ne len, 18 Ñunge dem cha Jerusalem, te di nañu jebal Dōm i nit ka i njīt i seriñ ya ak bindānkat ya; te di nañu ko ate ndah͈ mu dē; 19 Di nañu ko jebal Gentile ya, ndah͈ ñu ñaual ko, ratah͈ ko, te dāj ko cha kura; te chi ñetel i fan am di na dēki. 20 Fōfale ndey ī dom i Zebedee ñou fi mōm, ak dōm am yu gōr, di ko jāmu, te lāj ko lef. 21 Mu ne ko, Lan nga buga? Mu ne ko, Na nga ebal ne suma ñar i dōm yile tōg, kena chi sa ndējor, kena chi sa chamoñ chi sa ngur. 22 Wande Yesu tontu, ne, H͈amu len li ngēn di lāj. Ndah͈ mun ngēn a nān nān ba ma nāni? Ñu ne ko, Mun nañu ko. 23 Mu ne len, Di ngēn nān suma nān chi dega: wande tōg chi suma ndējor ak suma chamoñ, munu ma ko maye kena, ganou ña ko suma Bay ba wājal. 24 Ba ko fuka ña dēge, ñu mere ñar i mboka ya. 25 Wande Yesu ô len fi mōm, te ne, H͈am ngēn ne i kēlifa i Gentile ya ēlif nañu len, te ñu rey ña ate nañu len ak sañsañ. 26 Du neka nōgule chi sēn digante; wande ku buga rey chi sēn digante, na neka sēn bukanēg; 27 Te ku buga neka sēn njīt, na neka sēn jām. 28 Naka Dōm i nit ka ñouūl ndah͈ ñu bukanēgu ko, wande ndah͈ mu bukanēgu, te may dund’ am njot ngir ñu bare. 29 Ba ñu gēne cha Jericho, mbōlo mu rey topa ko. 30 Te ñar i silmah͈a ñu tōg chi wet i yōn wa, ba ñu dēge ne Yesu jār na fa, ñu h͈āchu, ne, Borom bi, yerem ñu, you dōm i Dauda! 31 Mbōlo ma h͈ule len ndah͈ ñu nopi; wande ñu dolê h͈āchu, ne, Borom bi, yerem ñu, you dōm i Dauda! 32 Yesu tah͈ou, te ô len, ne, Lan ngēn buga ma defal len? 33 Ñu ne ko, Borom bi, na suñu i but ūbiku. 34 Yesu am yermande chi ñom, lāl sēn i but, te chi tah͈ouay sēn i but gis, te ñu topa ko. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society