Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 2 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Ba Yesu jūdo cha Bethlehem i Judæa, chi bes i Herod bur ba, i borom‐h͈amh͈am juge on nañu cha Penku, ñou chi Jerusalem,

2 Ne, Ana ki jūdu Bur i Yauod ya? Ndege gis on nañu bidiw am cha Penku, te dika nañu ndah͈ ñu jāmu ko.

3 Ba Herod bur ba dēge lōla, mu jāh͈le, mōm ak Jerusalem yepa.

4 Ba mu dajale i njīt i seriñ ya ak i bindānkat nit ña, mu lāj len fu Krista war a jūdu.

5 Nu ne ko, Chi Bethlehem i Judæa; ndege yonent ba bind’ on na, ne,

6 Te you Bethlehem, suf i Judah, du yā gen a tut chi i dek’ i Judah; ndege chi you la njīt di jugeji, ka di sama suma mbōtay Israel.

7 Herod nak, ba mu ôe borom‐h͈amh͈am ya chi kumpa, mu lāj len bu bāh͈ wan wah͈tu la bidiw ba fêñ on.

8 Mu yōni len fa Bethlehem, ne, Dem len, te ūt gūne ga bu bāh͈; su ngēn ko gise, delusi len te wah͈ ma ko, ndah͈ man itam ma jāmuji ko.

9 Ba ñu dēge bur ba, ñu dem; te bidiw ba ñu gis on cha Penku, jītu len, be ba mu tah͈oue cha kou bereb ba gūne ga neka.

10 Ba ñu gise bidiw ba, ñu banēh͈u ak banēh͈ gu rey lol.

11 Ba ñu h͈arafe cha nēg ba, ñu feka gūne ga ak Mariama ndey am; ñu sūka te jāmu ko; ñu ūbi sēn i wah͈ande, te jebal ko i maye: wurus, fufata, ak mira.

12 Te Yalla yēgal on na len chi gēnta, ne bu ñu delu fa Herod; mōtah͈ ñu ñibi sēn deka cha wenen yōn.

13 Ba ñu dem on, malāka i Borom bi fêñu Yusufa chi gēnta, ne, Jogal, jelal gūne gi ak ndey am, te dou cha Mesara, te jēki fa be ba ma la cha ôe, ndege Herod di na ūt gūne gi ndah͈ mu rēylu ko.

14 Mu jog, jel gūne ga ak ndey am chi gudi, te dem cha Mesara:

15 Mu neka fa be ba Herod dēe, ndah͈ la Borom bi wah͈ on cha yonent ba motaliku, ne, Cha Mesara lā ôe suma dōm.

16 Herod nak, ba mu gise ne borom‐h͈amh͈am ya nah͈ nañu ko, mu mer lol; mu yōne, te rēyat h͈alel yu gōr ya yepa ñu nek’ on cha Bethlehem, ak cha mpega ya, ñu am on ñar i at ak lu gen a new, naka cha wah͈tu wa mu lājte on borom‐h͈amh͈am ya.

17 Lōgale motali na la Jeremiah wah͈ on, ne,

18 Chi Ramah la ñu dēg’ on ab h͈āchu, joy ak yuh͈u gu rey, Rachel di joy ndig i dōm am, te bañ a jāleū, ndege da ñu dē.

19 Wande ba Herod dēe, malāka i Borom bi fêñu Yusufa chi gēnta cha Mesara,

20 Ne, Jogal, jelal gūne gi ak ndey am, te dem cha suf i Israel; ndege ña ūt on bakan i gūne gi dē nañu.

21 Mu jog, jel gūne ga ak ndey am, te delusi cha suf i Israel.

22 Wande ba mu dēge ne Archelaus ngūru chi bereb i bay am Herod, mu ragal a dem fōfa; te ba ko Yalla yēgale chi gēnta, mu dem cha wet i Galilee,

23 Te ñou, deka chi rew mu tūda Nazareth: ndah͈ la yonent ya wah͈ on motaliku, ne, Di nañu ko tūde Nazarene.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan