Matthew 18 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Cha wah͈tu wōwale tālube ya ñou fi Yesu, ne, Kan a di ka gen a rey chi ngur i ajana? 2 Mu ô fi mōm ab gūne gu tūti, teg ko chi sēn digante, 3 Ne, Chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn tūbule, te neka niki gūne yu tūti, du len h͈arafi chi ngur i ajana muk. 4 Ku mu mun a don mbōk ku di sufelu niki gile gūne gu tūti, mō di ka gen a rey chi ngur i ajana. 5 Ku nangu gena gūne niki gile chi suma tur, man la nangu: 6 Wande ku di moylo gena chi yile yu tūt ñi gum chi man, don na geni chi mōm ñu taka doch wu rey chi bāt am, te sani ko chi bir gēch ga. 7 Suboh͈un aduna si ndig i mpaka! ndege i mpaka soh͈la naño dika; wande suboh͈un nit ka tah͈ mpaka ñou. 8 Su la sa loh͈o mbāte sa tanka moylô, dog ko, te sani ko: mō gen nga h͈araf chi dunda ak lago mbāte di sôh͈, aste am ñar i loh͈o mbāte ñar i tanka, ñu di la sani chi safara su dul jêh͈. 9 Su la sa but moylô, luh͈i ko, te sani ko: mō gen nga h͈araf chi dunda ak bena but, aste am ñar i but ñu di la sani chi safara i nāri. 10 Otu len a jēpi kena chi gūne yu tūt yile; ndege mangi len di wah͈, cha ajana sēn i malāka di jāno ak suma kanam i Bay ba cha ajana sā su neka. 11 Ndege Dōm i nit ka ñou na ndah͈ mu musal ñu rēr ña. 12 Lan ngēn dēfe? Su nit ame tēmēr i nh͈ar, te bena rēr ko cha, du bayi jurom ñenent fuk’ ak jurom ñenent ya, dem cha tūnda ya, te ūti bu rēr ba am? 13 Su ko gise, chi dega ma ne len, di na banēh͈u ndig mōm, aste jurom ñenent fuk’ ak jurom ñenent ya rērul on. 14 Tah͈na itam du sēn mbugel i Bay ba cha ajana, ndah͈ kena chi yu tut yile rēr. 15 Su la sa morom tōñe, demal won ko tōñ yangê’m chi sēn digante: su la dēge, fabi nga sa morom. 16 Wande su la dēgule, andal ak kena mbāte ñar, ndah͈ bāt bu neka set chi gemeñ i ñar i sēde mbāte ñeta. 17 Su len bañê dēga, wah͈ ko ndaje ma; te su bañê dēga ndaje ma itam, na neka chi you niki Gentile ak publican. 18 Chi dega mangi len di wah͈, Lu mu mun a don lu ngēn di taka chi suf, di na taku cha ajana; te lu mu mun a don lu ngēn di tiki chi suf, di na tikiku cha ajana. 19 Ma nêti len, Su ñar chi yēn dēgô chi suf lu jem chi lef lu ngēn di ñān, suma Bay bi cha ajana di na len ko defal. 20 Ndege fu ñar mbāte ñeta dajalo chi suma tur, fōfale lā neka chi sēn digante. 21 Fōfale Peter ñou fi mōm, te ne ko, Ñāt’ i yōn la ma suma morom di tōñ, te ma baal ko? be jurom ñar i yōn am? 22 Yesu ne ko, Wah͈u ma la, Be jurom ñar i yōn; wande, Be jurom ñar fuk’ i yōn ak jurom ñar. 23 Mōtah͈ ngur i ajana niro na ak bena bur bu bug’ on a jel konta ak i jām am. 24 Ba mu dôre woña, ñu isi fi mōm kena ku ko leb on fuk’ i njūne chi h͈ālis. 25 Wande ndege amul lu mu ko feye, borom am ebal ñu jay ko, ak jabar am, ak i dōm am, ak lu mu am yepa, ndah͈ mu fey bor am. 26 Mōtah͈ jām ba sūka, te dagān ko, ne, Borom bi, muñal ma, di nā la fey yepa. 27 Borom i jām bōbale yerem ko, mu bayi ko mu dem, te wocha ko ak bor ba. 28 Wande jām bōbale gēna, te feka kena chi i naule am, ku ko leb on tēmēr i kopar: mu japa ko, ne ko chih͈ chi bāt am ne, Fey ma lo ma leb on. 29 Naule am ba sūka, te dagān ko, ne, Muñal ma, di nā la fey. 30 Mu fēta, wande dem tejlu ko chi kaso, be ba mu feye bor ba. 31 Ba naule am ya gise la mu def, ñu nah͈arlu lol, te ñou nitali sēn borom la mu def on. 32 Fōfale borom am ôlo ko fi mōm, te ne ko, E jām bu soh͈or bi, mā la baal on bor bōbale yepa, ndege dagān on nga ma: 33 Warul kon you it nga yerem sa naule, naka ma la yereme on? 34 Borom am mer, te jebale ko getenkat ya, be ba mu feye lu mu ko leb on yepa. 35 Nōgu la itam suma Bay ba cha ajana di def ak yēn, su ngēn dul baalalante sēn morom chi sēn h͈ol. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society