Matthew 17 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Ganou jurom ben’ i fan, Yesu jel Peter, James, ak John rak’ am, te yubu len chi kou tūnda wu koue, ñom dal: 2 Mu sopaliku chi sēn kanam: h͈ar‐kanam am di melah͈ niki janta bi, te ser am wêh͈ tal niki lêr gi. 3 Te Musa ak Elijah fêñu len, di wah͈tān ak mōm. 4 Peter tontu, ne Yesu, Borom bi, bāh͈ na chi ñun ñu neka file: su la nêh͈e, di nā fi defar ñet’ i mbār; bena you, bena Musa, ak bena Elijah. 5 Ba mu wah͈ande, nir wu ne naña umba len, te bāt juge cha nir wa, ne, Kile di suma Dōm ja ma sopa; chi mom lā def suma h͈ol bepa; dēga len ko. 6 Ba ko tālube ya dēge, ñu defēnu chi suf, te tīt lol. 7 Yesu ñou, te lāl len, ne, Jog len, te bu len tīt. 8 Ba ñu yēkate sēn but, gisatu ñu ken, ganou Yesu dal. 9 Ba ñu wache tūnda wa, Yesu ebal len, ne, Bu len wah͈ kena mpêñu mile, be ba Dōm i nit ka di dēki cha ñu dē ña. 10 I tālube am lāj ko, ne, Lutah͈ bindānkat ya ne Elijah ela na jeka ñou? 11 Mu tontu len, ne, Elijah di na ñou chi dega, to delo yef yepa: 12 Wande mangi len di wah͈, Elijah ñou on na jēg, te h͈amu ñu ko won, wande ñu def ko lu ñu buga chi mōm. Nōgu itam la ño sonaleji Dōm i nit ka. 13 Tālube ya h͈am nak, ne wah͈ na len lu jem chi John Batisekat ba. 14 Ba ñu dike chi mbōlo ma, nit ñou fi mōm, di sūka fi mōm, ne, 15 Borom bi, amal yermande chi suma dōm ju gōr; ndege defa say, te getenu bu miti; faral na tabi chi safara, ak chi ndoh͈. 16 Yubu on nā ko chi sa i tālube, te munu ñu ko weral. 17 Yesu tontu, ne, E h͈êt wu gumadi, te deger‐bopa, be kañ lā neka ak yēn? be kañ lā len muñal? Indi ko fi man. 18 Yesu h͈ūle ko, te jine ja gēna chi mōm; cha wah͈tu wōwale h͈alel ba wer. 19 Fōfale tālube ya ñou fi Yesu chi kumpa, ne, Lutah͈ ño ko munul on a gēne? 20 Mu ne len, Ndig sēn gumadi: ndege chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn ame ngum gu day niki pēp’ i sūna, di ngēn wah͈ tūnda wile, Roñul cha bereb bale; te di na roñu; te kôn dara du len te. 21 Wande h͈êt wile du gēna lu dul chi ñān ak chi kôr. 22 Ba ñu deke chi Galilee, Yesu ne len, Di nañu or Dōm i nit ka chi loh͈o i nit; 23 Di nañu ko rēy, te chi ñetel i fan am di na dēki. Ñu nah͈arlu lol. 24 Ba ñu dike chi Capernaum, ña di jel ngalak la ñou fi Peter, ne, Ndah͈ sēn borom du fey ngalak? 25 Mu ne, Wau. Ba mu h͈arafe chi nēg ba, Yesu jekantu ko, ne, Lo dēfe Simon? I bur i suf si, chi kan la ñu di jele bāh͈ wala ngalak? chi sēn i dōm am, am chi i gan? 26 Ba mu ne, Chi gan yi, Yesu ne ko, Kôn dōm ya du ñu war a fey. 27 Wande ndah͈ du ñu len fakatal, demal cha gēch ga, sani ôs, te japa jen wu jeka fêñ; bo ūbe gemeñ am, di nga cha feka dogit i h͈ālis: jel ko, te joh͈ len ko ngir man ak you. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society