Matthew 15 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Fōfale i bindānkat ak i Pharisee ñu juge cha Jerusalem, ñou fi Yesu, ne, 2 Lutah͈ sa i tālube moy nābe’ nit i h͈āt ya? ndege du ñu rah͈as sēn loh͈o su ño leka. 3 Mu tontu len, ne, Yēn it, lutah͈ ngēn moy eble’ Yalla chi sēn nābe? 4 Ndege Yalla wah͈ on na, ne, Teralal sa bay ak sa ndey: te, Ku h͈as bay am wala ndey am, na dē dē gi. 5 Wande yēn a ne, Ku di wah͈ bay am wala ndey am, ne, Yalla lā may lu la mun a jeriñ: 6 Bu mu teral bay am. Tah͈na be defadi ngēn eble’ Yalla mu di dara chi sēn nābe. 7 Yēn nafeh͈a yi, Isaiah wah͈ on na dega chi yēn, ne, 8 Nit ñile teral nañu ma ak sēn gemeñ, wande sēn h͈ol sorey na ma. 9 Wande nēn la ñu ma jāmo, di jemantal i eble’ nit niki njemantal i Yalla. 10 Mu ô mbōlo ma, te ne len, Dēglu len, te dēga: 11 Lu h͈araf chi gemeñ, du gakal nit; wande lu gēna chi gemeñ, mō di gakal nit. 12 Fōfale i tālube am ñou, te ne ko, H͈am nga ne Pharisee ya fakatalu nañu, ba ñu dēge kadu gile? 13 Wande mu tontu, ne, Njembat bu neka bu suma Bay ba cha ajana jembatul on, di na ko simpi. 14 Bayi len len; ño di njīt yu silmah͈a. Te su silmah͈a jītê silmah͈a, di nañu tabi chi mpah͈ ñom ñar. 15 Peter tontu ko, ne, Tiki ñu lēb wile. 16 Mu ne, Dēgangu len, yēn itam? 17 Dēgu len ne lu mu mun a don lu h͈araf chi gemeñ, dem chi bir, ñu gēne ko chi biti? 18 Wande yef yu gēna chi gemeñ, chi h͈ol la ñu juge; te ño di gakal nit. 19 Ndege chi h͈ol bi la h͈alāt yu bon di juge, i mbōm, i njālo, i h͈emem, i nchacha, sēde yu di fen, i sāga: 20 Yile di yef ya di gakal nit; wande te leka te bañ a rah͈asu, du gakal nit. 21 Yesu juge on na fa, te dem chi wet i Tyre ak Sidon. 22 Jena jigen i Canaan juge cha wet yōya, te mu h͈āch͈u, ne, Amal yermande chi man, E Borom bi, Dōm i Dauda; jine anga geten suma dōm ju jigen bu miti. 23 Wande tontuwu ko dara. I tālube am ñou, te dagān ko, ne, Demlo ko, ndege tanh͈al na ñu. 24 Wande mu tontu, ne, Fi nh͈ar i nēg i Israel yu rēr yi reka la ñu ma yōni. 25 Wande mu ñou te jāmu ko, ne, Borom bi, lêl dimali ma. 26 Mu tontu ko, ne, Daganul ñu jel mburu i h͈alel yi, te sani ko h͈aj yi. 27 Wande mu ne, Wau, Borom bi; ndege h͈aj yi sah͈, di nañu di leka ndesit ya di rot chi sēn tabul i borom. 28 Fōfale Yesu tontu ko, ne, E jigen ji, sa ngum rey na lol; naka nga buga, na ame nōgu chi you. Te chi wah͈tu wōwale dōm am wer cheng. 29 Yesu juge on na fa, jegeñsi cha gēch i Galilee; mu yēg cha kou tūnda wa, te tōg fōfa. 30 Mbōlo mu rey ñou fi mōm, and’ ak ña lagi, silmah͈a, lu, tēlekat, ak ñenen ñu bare, nu teg len chi tank’ am, te mu weral len; 31 Tah͈na mbōlo ma jomi, ba ñu gise lū ya wah͈, lagi ya wer, tēlekat ya doh͈, ak silmah͈a ya gis: ñu magal Yalla i Israel. 32 Yesu ô i tālube am fi mōm, te ne len, Am nā yermande chi mbōlo mi, ndege anda nañu ak man lēgi ñet’ i fan, te leku ñu dara; du ma len demlo te leku ñu, wala h͈ēchna di nañu ñaka dōle chi yōn wa. 33 Tālube ya ne ko, Fan la ñu mun a ame mburu mu doy mbōlo mu rey niki bile, chi manding mi? 34 Yesu ne len, Ñāta mburu ngēn am? Ñu ne ko, Jurom ñar, ak lu new chi jen yu tūt. 35 Mu ebal mbōlo ma ñu tōg chi suf, 36 Te jel jurom ñar i mburu ya, ak jen ya, gerem Yalla, mu dogat len, joh͈ tālube ya, te tālube ya joh͈ mbōlo ma. 37 Ñepa leka be doylu, te ñu fêsal jurom ñar i sendel ak ndesit la. 38 Ña lek’ on ñenent i njūne’ gōr la ñu, ganou i jigen ak i gūne. 39 Mu demlo mbōlo ma, duga chi gāl ga, te ñou chi i wet i Magadan. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society