Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 14 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Cha jamāno jōjale Herod kēlifa ga dēg’ on na lu ñu wah͈ lu jem chi Yesu,

2 Te mu ne bukanēg am ya, Kile di John Batisekat ba; dēki na cha dē ga; mōtah͈ koutef yile fêñ nañu chi mōm.

3 Ndege Herod jap’ on na John, ewo ko, te tej ko chi kaso, ndig Herodias, jabar i Philip rak’ am.

4 Ndege John dān na ko wah͈, ne, Daganul nga sey ak mōm.

5 Ba mu ko buge rēy, mu ragal mbōlo ma, ndege fōg nañu ne yonent la won.

6 Wande ba ño h͈umbal bes i njudu’ Herod, dōm i Herodias ju jigen fēcha chi sēn digante, mu nêh͈ Herod lol.

7 Mōtah͈ mu dig ak geñ ne, di na ko may lu mun a don lu mu lāj.

8 Mōm nak ndege ndey am jeñtal na ko, ne, May ma file bop’ i John Batisekat ba chi ndap.

9 Bur ba nah͈arlu ko; wande ndig geñ am ga, ak ña tōg on ak mōm di leka, mu ebal ñu may ko ko.

10 Mu yōni ku dog bop’ i John chi kaso ba.

11 Ñu indi bop’ am chi ndap, may ko janh͈a ba, mu yubu ko fa ndey am.

12 Tālube am ya ñou, jel yaram wa, sūl ko, te dem nitali ko Yesu.

13 Ba ko Yesu dēge, mu juge fa chi gāl chi manding mu wēt: ba mbōlo ma dēge lōla, ñu rūnga topa ko tank’ ak tanka cha deka ya.

14 Mu gēna, te gis mbōlo mu rey; mu am yermande chi ñom, te weral sēn i jarak.

15 Ba ngon jote, i tālube am ñou fi mōm, ne, File manding la, te wah͈tu wi wey na jēg; na nga ebal mbōlo mi ñu dem cha bir deka ya, te jenda dundu.

16 Wande Yesu ne len, Soh͈laū ño dem; may len ñu leka.

17 Ñu ne ko, Am nañu fi jurom i mburu reka, ak ñar i jen.

18 Mu ne, Indi len fi man.

19 Mu ebal mbōlo ma ñu tōg chi kou ñah ma, jel jurom i mburu ya ak ñar i jen ya, yēkati but am cha asaman, gerem Yalla, dogat mburu ya, joh͈ len talube ya, te tālube ya joh͈ len mbōlo ma.

20 Ñepa leka be sūr; ñu forātu ndesit ma be ñu fêsal fuk’ i sendel ak ñar.

21 Ña lek’ on jurom i njūne’ gōr la ñu potah͈, ganou i jigen ak i gūne.

22 Nōn’ ak nōna mu jeñtal i tālube am ñu duga chi gāl ga, te jītu ko cha genen wet ga, be ba mu demlô mbōlo ma.

23 Ganou ba mu demlô mbōlo ma, mu yēg cha kou tūnda wa ndah͈ mu ñān Yalla, te chi gudi ga mu neka fa mōm dal.

24 Wande nak gāl ga nek’ on na chi kou gēch ga, di yengatu chi dūs ya; ndege ngelou la defa nah͈ari won.

25 Chi ñenentel i wah͈tu chi gudi gi, mu dem fa ñom di doh͈ chi kou gēch ga.

26 Ba ko i tālube am gise mu di doh͈ chi kou gēch ga, ñu tīt, ne, Njuma la; te ñu h͈āchu ndig tītay.

27 Wande Yesu wah͈ len chi tah͈ouay, ne, Dalal len sēn h͈ol: Man la; bu len tīt.

28 Peter tontu ko, ne, Borom bi, su de you, ô ma ma ñou fi you chi kou ndoh͈ mi.

29 Mu ne ko, Ñoual. Peter wacha chi gāl ga, te mu doh͈ chi kou ndoh͈ ma mu dem fa Yesu.

30 Wande ba mu gise ngelou li, mu tīt, te dal di dīg; mu h͈āchu, ne, Borom bi, musal ma.

31 Nōn’ ak nōna Yesu talal loh͈o am, te japa ko, ne ko, E borom‐ngum gu new, lutah͈ nga nimse?

32 Ba ñu ñoue chi bir gāl ga, ngelou li dal.

33 Te ña neka chi gāl ga jāmu ko, ne, Chi dega yā di Dōm i Yalla.

34 Ba ñu jale, ñu dika chi suf si, chi Gennesaret.

35 Ba ko nit ña cha wet gōgale h͈ame, ñu yōni chi rew mōma yepa, indi fa mōm ña jēr ñepa;

36 Te dagān ko ndah͈ ñu mun a lāl omb’ i cholay am reka; te ña ko lāl ñepa ñu wer cheng.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan