Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 13 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Chi bes bōba Yesu gēna on na cha nēg ba, te tōg cha tefes ga.

2 Mbōlo mu rey dajalo fi mōm; tah͈na mu duga chi gāl, tōg, te mbōlo ma yepa tah͈ou cha tefes ga.

3 Mu wah͈ len yef yu bare chi i lēb, ne, Bena jikat dem on na ji;

4 Te ba mu jie, yena pēpa rot nañu cha wet i yōn wa, te mpicha ya dika for len;

5 Yenen rot chi i bereb i doch, fa ñu amule suf su bare; ñu gou a sah͈, ndege suf sa h͈ōtul;

6 Ba janta ba fenke mu laka len; te ñu lah͈, ndege amu ñu rên.

7 Yenen rot chi digante i tah͈as, te tah͈as yi sah͈ando ak ñom, te waka len:

8 Yenen rot chi suf su bāh͈ sa, te mēña mēñef, yena ya tēmēr, yale jurom bena fuka, yale ñeta fuka.

9 Ku am i nopa, na dēga.

10 Tālube ya ñou te ne ko, Lutah͈ nga wah͈ ak ñom chi i lēb?

11 Mu tontu len, ne, Yēn la ñu may ngēn h͈am i kumpa i ngur i ajana, wande ñom mayu ñu len ko.

12 Ndege ka am mōm la ño may, te di na am lu bare; wande ka amul, di nañu jel la mu am sah͈.

13 Mōtah͈ ma wah͈ ak ñom chi i lēb; ndege ba ñu gise, du ñu gis; te ba ñu dēge du ñu dēga; te fafu ñu di h͈am.

14 Te chi ñom la bāt i Isaiah motaliku, ne, Di dēga di ngēn dēga, wande du len h͈am; te di gis di ngēn gis, wande du len sēnu:

15 Ndege h͈ol i nit ñile dūf na, sēn i nopa teh͈ nañu, te tej nañu sēn i but; ndah͈ du ñu gis ak sēn i but, dēga ak sēn i nopa, tūb, te ma weral len.

16 Wande barkel chi sēn i but, ndege da ñu gis; ak sēn i nopa, ndege da ñu dēga.

17 Ndege chi dega mangi len di wah͈, Yonent yu bare ak nit ñu jūb bug’ on naño gis li ngēn gis, te gisu ñu ko won; te dēga li ngēn dēga, wande dēgu ñu ko won.

18 Dēga len mbōk lēb i jikat ba.

19 Ba kena dēge bāt i ngur gi, te h͈amu ko, fōfale la Seytane ñoue, te dindi la ñu ji won chi h͈ol am. Kile di ka ñu ji won chi wet i yōn wa.

20 Te ka ñu ji won chi i bereb i doch, mō di ka dēga bāt bi, te dal di ko nangu ak banēh͈;

21 Wande amul rên chi bop’ am, te muñ chi sā yu new dal; ndege su nah͈ar joge wala ngeten ndig bāt bi, nōg’ ak nōga mu fakatalu.

22 Ka ñu ji won chi digante tah͈as ya, mō di ka dēga bāt bi; te i ntopato’ aduna si, ak nah͈ay i amam, waka bāt bi, mu bañ a mēña dōm.

23 Te ka ñu ji won chi suf su bāh͈ sa, mō di ka dēga bāt bi, te h͈am ko, te mēña dōm chi dega, yena ya tēmēr, yale jurom bena fuka, yale ñeta fuka.

24 Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak nit ka ji on jiu ju bāh͈ chi tōl am;

25 Wande ba ñu neloue, mbañ am dika, te ji nduh͈um chi digante dugup ja, te dem.

26 Ba dugup ja sah͈e, te mēña dōm, nduh͈um la fêñ itam.

27 I rapas i borom‐ker ga ñou, te ne ko, Borom bi, ndah͈ jiū la won jiu ju bāh͈ chi sa tōl? naka la ame nduh͈um nak?

28 Mu ne len, Ab mbañ a def lōlu. Rapas ya ne ko, Buga nga ñu dem budi len?

29 Wande mu ne, Dēt, h͈ēchna bu ngēn di budi nduh͈um la, di ngēn budiāle dugup ja it.

30 Bayi len ñar ña ñu sah͈ando be cha ngōbte ga; te cha wah͈tu’ ngōbte ga di nā wah͈ gōbkat ya, ne, Budi len jeka nduh͈um la, taka ko i say te laka ko; wande dajale len dugup ja chi suma sah͈a.

31 Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak pēp’ i sūna, bu nit fab, te ji chi tōl am;

32 Mō gen a tūt chi i pēpa yepa; wande su sah͈e, mō gen a rey chi gir am yepa, te mu neka garap be mpich’ i asaman yi di dika dal chi i banh͈as am.

33 Mu wah͈ len benen lēb, ne, Ngur i ajana niro na ak mporoh͈al bu jigen jel, te def chi ñet’ i andār i sunguf, be yepa foroh͈.

34 Yesu wah͈ on na mbōlo ma yef yile yepa chi i lēb, te wah͈u len dara lu dul chi lēb:

35 Ndah͈ la yonent ba wah͈ on motaliku, ne, Di nā ūbi suma gemeñ chi i lēb; di nā yēgle yef yu nubu cha ndôrte’ aduna si.

36 Fōfale Yesu bayi mbōlo ma, h͈araf chi nēg ba; te tālube am ya ñou fi mōm, ne, Tiki ñu lēb i nduh͈um i tōl ba.

37 Mu tontu len, ne, Ka ji jiu wu bāh͈ ba, Dōm i nit ka la;

38 Tōl ba aduna si la; jiu wu bāh͈ wa i dōm i ngur ga la; nduh͈um la i dōm i bulis la;

39 Mbañ ma ko ji on Seytane la; ngōbte ga muj i aduna si la; te gōbkat ya ño di malāka ya.

40 Naka ñu budi nduh͈um la, te laka ko chi safara, nōgu la di neki chi muj i aduna.

41 Dōm i nit ka di na yōne i malāk’ am, te di nañu forātu chi ngur am yef yu moylo yepa, ak ña def lu bon;

42 Te sani len cha safara sa; fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.

43 Bōba ñu jūb ña di nañu melah͈ na janta bi chi sēn ngur i Bay ba. Ku am i nopa na dēga.

44 Ngur i ajana niro na ak alal bu nubu chi bir tōl; ba ko nit feke mu nuba ko, dem chi banēh͈ am jay lu mu am on yepa, te jenda tōl bōbale.

45 Ngur i ajana nirôti na ak jūla ku don ūt jamong yu bāh͈;

46 Ba mu feke bena jamong ju jafe njēg, mu dem jay lu mu am on yepa, te jenda ko.

47 Ngur i ajana nirôti na ak mbal mu ñu sani chi gēch, mu japa h͈êt i jen wu neka:

48 Ba mu fêse, ñu h͈ēcha ko chi tefes; ñu tōg chi suf, te dajale yu bāh͈ ya chi i ndap, wande sani yu bon ya fale.

49 Nōgule la neki chi muj i aduna: malāka ya di nañu juge, te h͈ajātle ñu bon ña cha ñu jūb ña,

50 Te sani len chi safara si: fōfale la joy di neka, ak yey i buñ.

51 Ndah͈ dēga ngēn yef yile yepa? Ñu ne ko, Wau.

52 Mu ne len, Bindānkat bu neka mbōk bu ñu nekalo tālube chi ngur i ajana, niro na ak borom‐ker ku gēne chi dēnchukay am lu ês ak lu maget.

53 Am on na ba Yesu sotal on lēb yile, mu juge fōfa.

54 Ba mu dike chi rew am, mu jemantale len chi sēn i juma, tah͈na ñu jomi, ne, Nit kile naka la ame h͈amh͈am bile, ak koutef yile?

55 Kile du dōm i minise bā’m? du ndey am a tūda Mariama? te i rak’ am James, ak Yusufa, ak Simon, ak Judas?

56 Te i jigen am, du chi suñu digante la ñu neka? Naka la kile ame yef yile yepa?

57 Ñu fakatalu chi mōm. Wande Yesu ne len, Yonent ñakul teranga lu moy chi dek’ am, ak chi ker am.

58 Defu fa i koutef yu bare ndig sēn gumadi.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan