Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 11 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Am on na ba Yesu sotal on eble fuk’ i tālube am ak ñar ña, mu juge fa, ndah͈ mu jemantale te wāre chi sēn i deka.

2 Ba John dēge chi tejukay ba i koutef i Krista, mu yōne cha i tālube am;

3 Ñu ne ke, Ndah͈ yā di ki war a dika, am war naño sēnu kenen?

4 Yesu tontu len, ne, Dem len, nitali John li ngēn dēga, ak li ngēn gis;

5 Silmah͈a yange gis, lago yange doh͈, gāna yange wer, teh͈ yange dēga, ña dē dēkaliku, te ñunge wāre linjil bi chi miskin ya.

6 Te barkel chi ku dul feka fakatalu chi man.

7 Ba ñu deme, Yesu dal di ne mbōlo ma lu jem chi John, Lan ngēn dem on cha manding ma ndah͈ ngēn sêt? H͈īs bu di yengatu ak ngelou lê’m?

8 Wande lan ngēn dem on ndah͈ ngēn sêt? Nit ku sāngu chi nchangay lu noy am? Ña sāngu chi nchangay lu noy angi chi i nēg ī bur.

9 Wande lutah͈ on ngēn dem? sêt ab yonent am? Wau, ma ne len, te ku upa yonent.

10 Kile mō di ka ñu bind’ on, ne, Di nā yōni suma ndau chi sa kanam, ka di wāj sa yōn chi sa kanam.

11 Chi dega mangi len di wah͈, Ku gen a rey John Batisekat ba jugêngul cha ña judu chi jigen; wande ka gen a tut chi ngur i ajana, mō ko gen a rey.

12 Cha jamāno i John Batisekat ba bentey, chi nchouarte la ñu fab ngur i ajana, te ña souar japa ko.

13 Ndege yonent ya yepa ak yōn wa yēgle on nañu be cha John.

14 Te su ngēn ko buge nangu, kile di Elijah, ka war a ñou.

15 Ku am nopa yu mu dēge, na dēga.

16 Wande ak lan la h͈êt wile niro? Niro na ak h͈alel ñu jēki chi i ndaje, di h͈āchu chi sēn i mās,

17 Ne, Lītal nañu len, te fēchu len; yeremtu nañu, te joyu len.

18 Ndege John ñouūl on di leka wala di nān, te ñu ne, Anda na ak jine.

19 Dōm i nit ka ñou di leka te di nān, te ñu ne ko, Fuh͈alekat bi, ak nānkat i biñ bi, ak and’ i publican yi ak bakarkat yi. Wande sago jubantiku na chi i jef am.

20 Fōfale mu dal di eda deka ya fa mu def on koutef am yu gen a bare, ndege da ñu rēchuwul.

21 Suboh͈un you Chorazin! suboh͈un you Bethsaida! ndege koutef ya ma def on chi yēn, su ñu len def on chi Tyre ak Sidon, rēchu kon nañu bu yāga chi sagar ak dōm i tāl.

22 Wande mangi len di wah͈, Di na gen chi Tyre ak Sidon chi kerog mpēnch’ um Yalla ma as yēn.

23 Te you Capernaum, mi yēkatiku cha asaman, di nañu la sufel be chi nāri: ndege koutef ya ma def on chi you, su ñu len def on cha Sodom, kôn mu des bentey.

24 Wande mangi len di wah͈, Di na gen chi rew i Sodom chi kerog mpēnch’ um Yalla ma as you.

25 Cha wah͈tu wōwale Yesu tontu, ne, Mangi la gerem, Bay bi, Borom’ asaman ak suf, ndege nuba nga yef yile chi borom‐h͈amh͈am yi ak borom‐sago yi, te fêñal len i gūne.

26 Na di nōgule, Bay bi, cha naka mu la nêh͈e chi sa kanam.

27 Suma Bay jebal na ma yef yepa; te ken h͈amul Dōm ji wande Bay bi; te ken h͈amul Bay bi wande Dōm ji, ak ku Dōm ji nangu mu h͈am ko.

28 Dikasi len fi man yēn ña lota te dīs ñepa, te di nā len may noflay.

29 Enu len suma suf chi yēn, te jemantu len chi man; ndege da ma lew, te sufelu chi h͈ol; te di ngēn feka noflay chi sēn i fit.

30 Ndege suma suf yomba na, te suma en oyof na.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan