Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

Matthew 1 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Tēre’ toflante i gir i Yesu Krista, dōm i Dauda, dōm i Ibrayuma.

2 Ibrayuma jur on na Isaka; Isaka jur Yanh͈oba; Yanh͈oba jur Judah ak i dōm i bay am;

3 Te Judah jur Perez ak Zerah cha Tamar; Perez jur Hezron; Hezron jur Ram;

4 Te Ram jur Amminadab; Amminadab jur Nahshon; Nahshon jur Salmon;

5 Te Salmon jur Boaz cha Rahab; Boaz jur Obed cha Ruth; Obed jur Jesse;

6 Te Jesse jur bur Dauda; bur Dauda jur Suleyman, chi ka nek’ on jabar i Uriah;

7 Te Suleyman jur Rehoboam; Rehoboam jur Abijah; Abijah jur Asa;

8 Te Asa jur Jehoshaphat; Jehoshaphat jur Joram; Joram jur Uzziah;

9 Te Uzziah jur Jotham; Jotham jur Ahaz; Ahaz jur Hezekiah;

10 Te Hezekiah jur Manasseh; Manasseh jur Amon; Amon jur Josiah;

11 Te Josiah jur Jechoniah ak i dōm i bay am, cha jamāno ja ñu len gadaylo won fa Babylon:

12 Ganou ba ñu len yubu on fa Babylon, Jechoniah jur Shealtiel; Shealtiel jur Zerubbabel;

13 Te Zerubbabel jur Abiud; Abiud jur Eliakim; Eliakim jur Azor;

14 Te Azor jur Sadoc; Sadoc jur Achim; Achim jur Eliud;

15 Te Eliud jur Eleazar; Eleazar jur Matthan; Matthan jur Yanh͈oba;

16 Te Yanh͈oba jur Yusufa jekar i Mariama, ka nek’ on ndey i Yesu, ka ñu tūda Krista.

17 H͈êt ya yepa mbōk cha Ibrayuma be cha Dauda fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha Dauda be cha ngaday ga fa Babylon fuk’ i h͈êt la ak ñenent; te cha ngaday ga fa Babylon be chi Krista fuk’ i h͈êt la ak ñenent.

18 Njūdu’ Yesu Krista nile la won: Ba ndey am Mariama nangulante Yusufa, ba mu lāta sey ak mōm, fêñu on na ak bir chi Nh͈el mu Sela ma.

19 Yusufa jekar am, nek’ on ku jūb, te nangôdi ndig wone ko chi biti, bug’ on na ko fase chi kumpa.

20 Wande ba mu h͈alāte yef yile, malāka i Borom bi fêñu ko chi gēnta, ne ko, Yusufa, dōm i Dauda, bul ragal a sey ak Mariama, ndege li chi bir am chi Nh͈el mu Sela ma la juge.

21 Di na jur dōm ju gōr, te na nga ko tūde Yesu, ndege mō di musali mbōtay am chi sēn i bakar.

22 Yile yepa am on na ndah͈ la Borom bi wah͈ on chi yonent ba motaliku, ne,

23 H͈ēk ba di na bir, te jur dōm ju gōr, te di nañu ko tūde Emmanuel; mu tiki, Yalla and’ ak ñun.

24 Yusufa jog chi nelou, def la ko malāka i Borom bi ebal on, te jel ko jabar:

25 H͈amu ko be ba mu jure tau am, ba mu tūde Yesu.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan