Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

John 6 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Cha ganou yef yile Yesu dem on na cha genen wet i gēch i Galilee, bu di gēch i Tiberias.

2 Te mbōlo mu rey topa ko, ndege gis on nañu koutef ya mu def on cha ña op’ on.

3 Te Yesu yēg cha kou tunda wa, te tōg fa ak i tabube am.

4 Te bena h͈ewte i Yauod ya jegeñsi na.

5 Yesu nak, ba mu yēkate i but am, mu gis mbōlo mu rey di ñou fi mōm, te ne Philip, Ana fu ñu di jendi mburu ndah͈ ñile mun a leka?

6 Te wah͈ na lile ndah͈ mu sêtlu ko: ndege mō h͈am lu mu buga def.

7 Philip tontu ko, ne, Ñar tēmēr i transu mburu du len doy, ndah͈ ku neka jel tuti.

8 Kena chi talube am ya, Andrew, rak’ i Simon Peter, ne ko,

9 H͈alel angile bu am jurom i mburu, ak ñar i jen: wande ana lu lile di faj chi mbōlo mu ni day?

10 Yesu ne, Tōglo len nit ñi. Ñah͈ mu bare nek’ on na cha bereb ba; te nit ña tōg chi suf, lu jem chi jurom i njūne potah͈.

11 Yesu nak jel mburu ya, te ba mu jebale ngerem, mu sedātle len ña tōg; ak jen ya itam cha naka ñu buge.

12 Te ba ñu leke be sūr, mu ne i talube am, Dajale len dogit yi chi des, ndah͈ bul chi dara yah͈u.

13 Tah͈na ñu dajale len, be fêsal cha fuk’ i sendel ak ñar chi i dogit i mburu ya cha des on, cha la ñu lek’ on.

14 Ba nit ña gise koutef ga mu def on nak ñu ne, Chi dega kile di yonent ba di dika chi aduna si.

15 Yesu nak, ba mu h͈ame ne buga naño ñou di ko jel ak dōle, te fal ko bur, mu demati cha tūnda wa mōm reka.

16 Te ba ngon jote, i talube am dem cha gēch ga;

17 Te ñu duga chi gāl, te dal di jala gēch ga cha Capernaum. Te mu lendem, te Yesu ñouangul on fa ñom.

18 Te gēch ga yengatu, ndig ngelou lu rey lu don fuf.

19 Ba ñu jowe nak be fu sorey, ñu sēn Yesu mu di doh͈ cha kou gēch ga, te jegeñsi gāl ga, te ñu tīt.

20 Wande mu ne len, Man la; bu len tīt.

21 Tah͈na ñu nangu jel ko cha gāl ga: te nōn’ ak nōna gāl ga aga cha jēri ja ñu buga dem.

22 Cha elek sa, mbōlo ma tah͈ou on cha genen wet i gēch ga gis on nañu ne bena gāl rek’ anga fa won, te Yesu dugul on cha gāl ga ak i talube am, wande i talube am bayako fa ñom dal;

23 (Wande yenen gāl juge on nañu cha Tiberias, mu jegeñ bereb ba ñu leke won mburu ma, ganou ba Borom bi jebal on ngerem:)

24 Ba mbōlo ma gise nak ne Yesu neku fa, mbāte i talube am, ñom it ñu duga chi gāl ya, te ñou chi Capernaum, di ūt Yesu.

25 Te ba ñu ko gise cha genen wet i gēch ga, ñu ne ko, Rabbi, kañ nga ñou on file?

26 Yesu tontu len, te ne, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Ūtu len ma ndege gis on ngēn i koutef, wande ndege lek’ on ngēn mburu ya be ngēn sūr.

27 Bu len ligey ndig dūndu bu di sanku, wande ndig dūndu bu di deka be abada, ba len Dōm i nit ka di mayi: ndege mōm la Yalla Bay ba tan’ on.

28 Ñu ne ko, Lan la ñu war a def, ndah͈ ñu di ligey i ligey i Yalla?

29 Yesu tontu te ne len, Lile di ligey i Yalla, ndah͈ ngēn gum chi mōm ka mu yōni on.

30 Ñu ne ko, Ban mandarga nga def, ndah͈ ñu di gis, te gum la? Ana lo ligey?

31 Suñu i bay lek’ on nañu manna ba cha manding ma; cha naka ñu bind’ on, ne, May on na len mburu cha asaman ñu leka.

32 Yesu ne len, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Musa mayul on len mburu ma cha asaman; wande suma Bay a len may mburu mu dega ma cha asaman.

33 Ndege mburu’ Yalla ma mō di ma juge cha asaman, ti di maye dūnda chi aduna si.

34 Ñu ne ko, Borom bi, may ñu mburu mile bel mos.

35 Yesu ne len, Mā di mburu’ dūnda mi: ku ñou fi man du h͈īf, te ku gum chi man du mar muka.

36 Wande wah͈ on nā len, ne, Da ngēn ma gis, te tah͈ul bentey ngēn gum.

37 Ña ma Bay ba may ñepa, di nañu ñou fi man: te ku ñou fi man, du ma ko dah͈a muka.

38 Ndege jugewu ma cha asaman ndah͈ ma def suma mbugel i bopa, wande mbugel i ka ma yōni on.

39 Te mbugel i ka ma yōni on a di lile, ne ña mu ma may ñepa, du ma ñaka ken, wande dēkali ko cha kera bes ba.

40 Ndege suma mbugel i Bay ba di bile, ne ku neka ku gis Dōm ji te gum chi mōm, di na am dūnda gu dul jêh͈; te di nā ko dēkali cha kera bes ba.

41 Tah͈na Yauod ya ñurumtu ko, ndege wah on na, ne, Mā di mburu ma juge won cha asaman.

42 Te ñu ne, Ndah͈ kile dowul Yesu, dōm i Yusufa, te ñu h͈am bay am ak ndey am? Naka la wah͈e, ne, Manga juge cha asaman?

43 Yesu tontu te ne len, Bu len ñurumtu chi sēn bopa.

44 Ken munul a ñou fi man, lu dul Bay ba ma yōni on h͈ēcha ko: te di nā ko dēkali cha kera bes ba.

45 Binda nañu chi tēre’ yonent ya, ne, Nepa Yalla di na len jemantal. Ku neka mbōk ku dēga bāt i Bay ba, te jemantu, mu ñou fi man.

46 Ken gisul Bay ba, ganou mōm ka juge won cha Yalla, mō gis on Bay ba.

47 Chi dega, chi dega, ma ne len, Ku di gum, mō am dūnda gu dul jêh͈.

48 Mā di mburu’ dūnda ma.

49 Sēn i bay lek’ on nañu manna ba cha manding ma, te dē on nañu.

50 Bile di mburu mi juge won cha asaman, ndah͈ nit mun ko leka, te du dē.

51 Mā di mburu’ dūnda ma juge won cha asaman: su kena leke chi mburu mile, di na dūnda bel mos: te mburu ma ma mayeji suma yaram la, wa ma jebaleji ndig dūnd’ i aduna si.

52 Yauod ya nak werante chi sēn bopa, ne, Naka la ñu nit kile mune joh͈ yaram am ñu leka?

53 Yesu ne len mbōk, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Su ngēn lekule yaram i Dōm i nit ki, te nānu len deret am, du len am dūnda chi yēn.

54 Ku di leka suma yaram, te nān suma deret, am na dūnda gu dul jêh͈; te di nā ko dēkaliji cha kera bes ba.

55 Ndege suma yaram dūndu’ dega la, te suma deret nān i dega la.

56 Ku di leka suma yaram te nān suma deret, deka na chi man, te man chi mōm.

57 Naka ma Bay ba di dūnda yōne, te mā dūnda ndig Bay ba; nōgule la itam ka ma di leka, di na dūnda ndig man.

58 Bile di mburu ma juge won cha ajana: dowul mburu ma bay ya lek’ on, te dē: ku di leka mburu mile di na dūnda bel mos.

59 Yef yile la wah͈ on cha juma ja, ba mu jemantal on cha Capernaum.

60 Lu bare chi i talube am nak, ba ñu dēge lile, ne, Wah͈ jile dīs na; ku ko mun a dēga?

61 Wande Yesu h͈am chi bop’ am ne i talube am ñurumtu nañu chi lile, te mu ne len, Ndah͈ lile tah͈ ngēn fakatalu?

62 Naka su ngēn gise Dōm i nit ka di yēg fa mu jek’ on a juge?

63 Mō di nh͈el ma di dūndalo; yaram wi jeriñul dara: bāt ya ma len wah͈ nh͈el la, ak dūnda.

64 Wande ñena chi yēn gumu len. Ndege Yesu h͈am on na cha ndôrte la ña gumul on, te ka ko di ori.

65 Te mu ne, Lile tah͈ ma wah͈ on len, ne, ken munul a dika fi man, su ko ko Bay ba mayule.

66 Ndig lile lu bare chi i talube am delu ganou, te andatu ñu ak mōm.

67 Yesu ne fuk’ ak ñar ña, Ndah͈ yēn itam, da ngēn ma wocha?

68 Simon Peter tontu ko, ne, Borom bi, fi kan la ñu ela dem? Yā am i bat i dūnda gu dul jêh͈.

69 Te gum nañu, te h͈am, ne yā di kena ku sela ka juge fa Yalla.

70 Yesu tontu len, ne, Ndah͈ du yēn lā tan’ on, fuk’ ak ñar ña, te kena chi yēn ab seytane la?

71 Lile nak wah͈ na ko ndig Judas, dōm i Simon Iscariot, ndege mō ko ori, kena chi fuk’ ak ñar ña.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan