John 2 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Cha ñetel i fan ba, sey am on na cha Cana i Galilee; te ndey i Yesu anga fa won. 2 Ô on nañu itam Yesu ak i talube am cha sey ba. 3 Te ba biñ ba jêh͈e, ndey i Yesu ne ko, Amatu ñu biñ. 4 Te Yesu ne ko, Jigen ji, lu ma jote ak you? Suma wah͈tu dikangul. 5 Ndey am ne bukanēg ya, Lu mu len wah͈, def len ko. 6 Jurom ben’ i ndā i h͈êr anga fa won, naka āda i Yauod ya nek’ on ndig sēn setalay, bu cha neka mun na def natu yu bare. 7 Yesu ne len, Fêsal len ndā yi ak ndoh͈. Te ñu fêsal len be cha gemeñ ya. 8 Mu ne len, Tanh͈a len cha lēgi, te yub kēlifa nchēt ga. Te ñu yub ko. 9 Ba kēlifa nchēt ga mose ndoh͈ ma sopaliku on biñ, te h͈amul fu mu juge, (wande bukanēg ya h͈am ya rôt on ndoh͈ ma), kēlifa nchēt ga ôlu seyt bu gōr ba, 10 Te ne ko, Nit ku neka biñ bu bāh͈ ba la jeka tāj: te su ñu nāne be lu bare, mu isi bu genadi ba; yā dēncha biñ bu bah͈ bi be lêgi. 11 Mandarga bu jeka bile la Yesu def on cha Cana i Galilee, te wone ndam am; te i talube am gum chi mōm. 12 Ganou lōlu mu dem fa Capernaum, mōm, ak ndey am, ak i rak’ am, ak i talube am; te ñu jēki fa fan yu new. 13 Te h͈ewte i Yauod ya jegeñsi na, te Yesu dem fa Jerusalem. 14 Te mu feka cha bir juma ja ña don jay i nag ak i nh͈ar ak i mpetah͈, ak wēchikat i h͈ālis di tōg: 15 Te mu defar yar i būm, te dah͈a yepa cha biti juma ja, nh͈ar ya ak nag ya; te mu tūr h͈ālis i wēchikat ya, te dānel sēn i tabul; 16 Te mu ne ña don jay mpetah͈ ya, Fab len yile cha biti; bu len def suma nēg i Bay nēg i jayukay. 17 I talube am fataliku ne bind’ on nañu, ne, Sa nchauarte i nēg ba leka na ma fepa. 18 Yauod ya nak tontu te ne ko, Ban mandarga nga ño wone, ndege def nga yef yile? 19 Yesu tontu te ne len, Maba len juma jile, te chi ñet’ i fan di nā ko delu tah͈oual. 20 Yauod ya ne ko, Ñenent fuk’ i at ak jurom bena la ñu am di tabah͈ juma jile, te you di nga ko tah͈oual chi ñet’ i fan am? 21 Wande wah͈ on na chi juma i yaram am. 22 Ba mu dēkaliku on cha dē ga, i talube am fataliku ne wah͈ on na lōlu, te gum on nañu mbinda ma, ak bāt ba Yesu wah͈ on. 23 Ba mu neke cha Jerusalem cha h͈ewte i njot ga, ñu bare gum on nañu chi tur am, ba ñu gise koutef ya mu def on. 24 Wande Yesu ōluwul on bop’ am ak ñom, ndege h͈am on na ñepa, 25 Te soh͈lawul kena sēde chi lu jem chi nit; ndege mō h͈am on lu neka chi h͈ol i nit. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society