Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

John 19 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Pilate nak jel Yesu, te chou ko.

2 Te h͈arekat ya lēta mbah͈ana i dek, te teg ko chi bop’ am, te solal ko chol gu h͈onh͈a;

3 Te ñou fi mōm, ne, Jamom, Bur i Yauod ya! te ñu dōr ko ak sēn i loh͈o.

4 Te Pilate gēnati, te ne len, Sêt len, mangi ko indi fi yēn chi biti, ndah͈ ngēn h͈am ne gisu ma bena tōñ chi mōm.

5 Yesu gēna nak, sol mbah͈ana i dek ak chol gu h͈onh͈a. Te Pilate ne len, Sêt len nit ki!

6 Tah͈na ba ko i njīt i seriñ ya ak ndau ya gise, ñu h͈āchu, ne, Dāj ko cha kura ba, dāj ko cha kura ba. Pilate ne len, Yēn yubu len ko, te dāj ko cha kura ba: ndege gisu ma tōñ chi mōm.

7 Yauod ya tontu ko, ne, Am nañu yōn, te chi suñu yōn wōgu ela na dē, ndege def on na bop’ am Dōm i Yalla.

8 Ba Pilate dēge wah͈ jōjule mu dole ragal;

9 Te h͈arafati cha ateukay ba, te ne Yesu, Ana fo bayako? Wande Yesu tontuwu ko.

10 Pilate nêti ko, Ndah͈ do wah͈ ak man? ndah͈ h͈amu la ne am nā sañsañ bayi la, te am nā sañsañ dāj la cha kura ba?

11 Yesu tontu ko, ne, Do mun a am sañsañ chi man lu moy ñu joh͈ la ko cha kou: mōtah͈ ka ma jebale won fi you, mō la gen a bakar.

12 Lōlo tah͈ Pilate ūt ko bayi: wande Yauod ya h͈āchu, ne, So bayie kile, dowu la h͈arit i Cæsar: ku neka ku def bop’ am bur, moy na Cæsar.

13 Ba Pilate dēge bāt yōyu, mu indi Yesu cha biti, te tōg cha tōgu’ ate ba, cha bereb bu tūda Pavement, wande chi lak’ i Yauod ya, Gabbatha.

14 Te ngomar i h͈ewte ga am on na: chi jurom ben’ i wah͈tu la won. Te mu ne Yauod ya, Sêt len sēn Bur!

15 Tah͈na ñu h͈āchu, ne, Weyal ak mōm, weyal ak mōm, dāj ko cha kura ba. Pilate ne len, Ndah͈ ma dāj sēn Bur cha kura ba? I njīt i seriñ ya tontu, ne, Amu ñu bur ganou Cæsar.

16 Tah͈na mu jebal len ko ndah͈ ñu dāj ko cha kura ba.

17 Ñu yubu Yesu: te mu gēna, gadul kura am ba, dem fa bereb bu tūda Bereb i h͈ot’ i bopa, ba ñu tūda chi lak’ i Yauod ya, Golgotha:

18 Fōfale la ñu ko dāj cha kura ba, te ñenen ñar ak mōm, kena chi wet am gu neka, ak Yesu chi sen digante.

19 Te Pilate bind on na h͈ameukay am itam, te def ko cha kura ba. Te lile la binda, Yesu wā’ Nazareth, Bur i Yauod ya.

20 Ñu bare chi Yauod ya janga h͈ameukay bōba, ndege bereb ba ñu dāj on Yesu cha kura ba jegeñ na deka ba: te binda nañu ko chi lak’ i Yauod ak Latin ak Greek.

21 Tah͈na i njīt i seriñ i Yauod ya ne Pilate, Bul binda, ne, Bur i Yauod ya; wande ne nôn na, Mā di Bur i Yauod ya.

22 Pilate tontu, ne, La ma bind’ on mōm lā binda.

23 H͈arekat ya nak, ba ñu dāje Yesu cha kura ba, ñu jel cholay am ya, te sedāle len chi ñenent i h͈āj, bena h͈arekat bu neka; ak mbuba ma itam: mbuba ma nak amul ñauñau, rab’ on nañu ko cha kou be chi suf.

24 Tah͈na ñu wah͈ante, ne, Bu ñu ko h͈oti, wande na ñu ko wure ku ko di mōmi: ndah͈ mbinda ma motaliku, ne, Sedāle nañu on suma i cholay, te wure suma mbuba. H͈arekat ya nak def on nañu yef yōyale.

25 Wande ndey i Yesu anga tah͈ou on cha kanam i kura ba, ak rak’ am, Mariama jabar i Clopas, ak Mariama Magdalene.

26 Ba Yesu gise ndey am, ak talube ba mu sop’ on mu tah͈ou fa, mu ne ndey am, Jigen ji, sêtal sa dōm angile!

27 Cha ganou mu ne talube ba, Sêtal, sa ndey angile! Te cha wah͈tu wōwale talube ba jel ko cha ker i bop’ am.

28 Ganou lōlu, Yesu ba mu h͈ame ne yepa soti na, ndah͈ mbinda ma motaliku, mu ne, Mar nā.

29 Te ndap anga fa tah͈ou bu fês ak binegar: tah͈na ñu jel lu ño tūda sponge, fês ak binegar, def ko chi bant’ i sonka, te teg ko cha gemeñ am.

30 Ba Yesu jele binegar ba, mu ne, Soti na: te mu sengēm bop’ am, te jebale fit am.

31 Yauod ya nak, ndege ngomar i h͈ewte ga la won, ndah͈ yaram ya du des cha kura ya cha Dimas ja, ndege bes i Dimas jōjale bes bu rey la won, ñu lāj Pilate ndah͈ ñu dama sēn i el, te roñ len fa.

32 Tah͈na h͈arekat ya dika, te dama el i ku jeka ka, ak kenen ka ñu dāj on cha kura ba ak mōm:

33 Wande ba ñu dike fa Yesu, te feka ko mu dē be sotal, damu ñu i el am.

34 Wande kena cha h͈arekat ya duba ko h͈êj chi wet am, te nōn’ ak nōna deret ak ndoh͈ gēne cha.

35 Te ka ko gis on mō sēde, te sēde am dega la: te h͈am na ne wah͈ na dega, ndah͈ yēn itam mun a gum.

36 Ndege yef yōyu am on na ndah͈ mbinda ma motaliku, ne, Bena chi yah͈ am du dama.

37 Te benen mbinda nêti, Di nañu sêt ka ñu dub’ on.

38 Te ganou yef yōyu, Yusufa i Arimathea, ka nek’ on talube i Yesu, wande ken h͈amu ko won, ndege ragal on na Yauod ya, mu dagān Pilate ndah͈ mu bayi ko mu yubu yaram i Yesu: te Pilate bayi ko. Mu dika, te jel yaram am.

39 Te Nicodemus ñou itam, ka jek’ on a dika fa mōm chi gudi, te mu indi mira ak h͈êñay ya ñu bōle won; tēmēr i libar la potah͈.

40 Te ñu jel yaram i Yesu, te lomas ko ak i ser yu wêh͈ ak h͈êñay ya, cha naka melin i Yauod ya chi sēn i sūl.

41 Cha bereb ba ñu ko dāj on cha kura ba, tōl anga fa won, te cha bir tōl ba bena bamel bu ês, ba kena tedangul.

42 Fōfale la ñu tedal Yesu, ndig ngomar i Yauod ya; ndege bamel ba jegeñ on na fa.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan