John 18 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Ba Yesu wah͈ on bāt yoyu, mu gēna ak i talube am, jala deh͈ i Kidron, fa tōl neka, te mu duga chi bir, mōm ak i talube am. 2 Judas, ka ko or on, h͈am on na bereb ba; ndege Yesu faral on na dem fōfa ak i talube am. 3 Judas nak, ba mu ame i h͈arekat ak i saltige cha i njīt i seriñ ya ak Pharisee ya, mu dika fōfale ak i lampa ak i nītu ak i ganay. 4 Yesu ka h͈am yef ya ko di jot yepa, dem cha kanam, te ne len, Ana ku ngēn di ūt? 5 Nu tontu ko, ne, Yesu wā’ Nazareth ba. Yesu ne len, Man la. Te Judas itam, ka ko or on, mu tah͈ou ak ñom. 6 Tah͈na ba mu len wah͈e, ne, Man la, ñu delu ganou, te dānu chi suf. 7 Mu lājati len ne, Ana ku ngēn di ūt? Te ñu ne, Yesu wā’ Nazareth ba. 8 Yesu tontu, ne, Wah͈ on nā len ne Man la: su ngēn ma ūte, bayi len ñile ñu dem: 9 Ndah͈ bāt ba mu wah͈ on motaliku, ne, Ña nga ma may on, rēralu ma chi kena. 10 Simon Peter nak am on na jāsi, te mu bochi ko, te dōr jām i kelifa i seriñ ya, te dog nop’ i ndējor am. Tur i jām ba di Malchus. 11 Yesu ne Peter, Delōl jāsi bi chi mbar am: nānu ba ma Bay ba joh͈, ndah͈ du ma cha nān am? 12 H͈arekat ya nak ak saltige ba, ak i ndau i Yauod ya japa Yesu, te ew ko, 13 Te jeka ko yubu fa Annas; ndege mō don goro i Caiaphas, ka nek’on kelifa i seriñ ya cha at mōmale. 14 Caiaphas nak mō nek’on ka diktal on Yauod ya, ne ela na kena nit dē ngir mbōtay ga. 15 Te Simon Peter top’ on na Yesu, ak benen talube. Talube bōbale nak, kēlifa i seriñ ya h͈am on na ko, te mu h͈araf ak Yesu cha bir ker i kēlifa i seriñ ya; 16 Wande Peter tah͈ou cha biti bunta ba. Benen talube ba, ka kēlifa i seriñ ya h͈am on, dem cha biti te wah͈ ak jigen ja otu bunta ba, te indi Peter chi bir. 17 Janh͈a bu don otu bunta ba ne Peter, Ndah͈ you itam a di kena chi i talube i nit koku? Mu ne, Man dowu ma. 18 Jām ya nak ak ndau ya’nga fa tah͈ou on, ba ñu tāle safara i keriñ ndig seday ba, ñu di jāru; te Peter tah͈ou ak ñom di jāru. 19 Kēlifa i seriñ ya lāj Yesu chi lu jem chi talube am ya, ak njemantale am. 20 Yesu tontu ko, ne, Man chi kanam i ñepa lā wah͈ on chi aduna si; dan nā jemantal cha juma ya, ak cha jangu ba fa Yauod ya dajale ñepa; te wah͈u ma won dara chi kumpa. 21 Ana lutah͈ nga ma lāj? lājal ña ma dēg’ on la ma len wah͈ on: ñile h͈am nañu la ma wah͈ on. 22 Ba mu wah͈e lōlu, kena chi ndau ya’nga fa tah͈ou dōr Yesu ak loh͈o am, ne, Ndah͈ nōnu nga tonto kēlifa i serin ya? 23 Yesu tontu ko, ne, Su ma wah͈e lu bon, sēdêl ma lu bon: wande su de lu bāh, ana lutah͈ nga dōr ma? 24 Annas nak ew ko, te yōni ko Caiaphas, kēlifa i seriñ ya. 25 Simon Peter don na tah͈ou di jāru. Ñu ne ko, Ndah͈ you itam neku la kena chi talube am yi? Mu wēdi, te ne, Man dowu ma. 26 Kena chi i jām i kēlifa i seriñ ya, ku bok’ on ak ka Peter dog on nop’ am, ne, Ndah͈ gisu ma la won cha tōl ba ak mōm? 27 Tah͈na mu wēdêti: te chi tah͈ouay seh͈a ga sab. 28 Ñu omat Yesu nak cha Caiaphas be cha bir ateukay ba: te têl on na; ti ñom h͈arafu ñu cha ateukay ba, ndah͈ du ñu gakal sēn bopa, wande ndah͈ ñu mun a leka h͈ewte ga. 29 Pilate nak gēna dem fa ñom, te ne, Ana lu ngēn am lu ngēn di sēde chi nit kile? 30 Ñu tontu te ne ko, Su nekul on defkat i lu bon, kōn du ñu la ko jebal. 31 Tah͈na Pilate ne len, Jel len ko yēn, te ate ko cha naka sēn yōn eble. Yauod ya ne ko, Daganul ñu rēy kena: 32 Ndah͈ bāt i Yesu motaliku ba mu wah͈ on, di wone chi ban melo dē la dēeji. 33 Pilate nak h͈arafati cha ateukay ba, te ô Yesu te ne ko, Ndah͈ yā di bur i Yauod ya? 34 Yesu tontu, ne, Wah͈ nga ko you chi sa bopa, mbāte ndah͈ ñenen a la ko wah͈ chi lu jem chi man? 35 Pilate tontu, ne, Ndah͈ Yauod la? Sa h͈êt i bopa ak i njīt i seriñ ya ño la jebale fi man: ana lo def? 36 Yesu tontu, ne, Suma ngur bokul chi aduna sile: su suma ngur bok’ on chi aduna sile, kōn suma i bukanēg di nañu h͈ēh͈, ndah͈ du ñu ma jebal fa Yauod ya: wande suma ngur jugewul fōfule. 37 Pilate ne ko, Ndah͈ bur nga? Yesu tontu, ne, Wah͈ nga ko, ndege man bur la. Lile tah͈ ma jūdu on, te lile tah͈ ma ñou chi aduna si, ndah͈ ma sēde dega gi. Ku neka ku boka chi dega gi di na dēga suma bāt. 38 Pilate ne ko, Ana lu di dega? 39 Te ba mu wah͈ on lōlu, mu gēnati fa Yauod ya, te ne len, Man gisu ma mu def lu bon. 40 Wande am ngēn bāh͈ ne ma bayil len kena cha h͈ewte ga: ndah͈ buga ngēn ma bayil len Bur i Yauod ya? 41 Tah͈na ñu h͈āchôti, ne, Dowul kile, wande Barabbas. Barabbas nak sachakat la won. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society