John 17 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Yef yōyu Yesu wah͈ on: te yēkati i but am cha asaman, te ne, Bay bi, wah͈tu wa jot na; na nga may sa Dōm ndam, ndah͈ Dōm ji itam jebal la ndam: 2 Naka nga ko maye won sañsañ chi kou nit ñepa, ndah͈ mu maye ña nga ko may on ñepa dūnda gu dul jêh͈. 3 Te dūnda gu dul jêh͈ a di gile, ndah͈ ñu h͈am la, you mi di Yalla ji dega dal, ak Yesu Krista ki nga yōnesi won. 4 Magal on nā la chi suf si, te motali on nā ligey ba nga ma joh͈ on ma def ko. 5 Ey Bay bi, na nga ma may ndam lēgi ak sa bopa, ndam la ma am on ak you ba aduna si sosôngul. 6 Da ma wone on sa tur chi nit ña nga ma may on chi aduna si: yā len mōm on, te may on nga ma len; te dēncha nañu sa bāt. 7 H͈am nañu lēgi ne yef ya nga ma may on yepa, chi you la ñu juge: 8 Ndege bāt ya nga ma may on, ñom lā len may; te nangu nañu len, te h͈am chi dega ne chi you lā juge won, te gum ne yā ma yōni on. 9 Ñānal nā len: ñānatu ma aduna si, wande ngir ña nga ma may on; ndege ño di sa yos: 10 Te yef ya ma mōm yepa, yā len mōm, te suma yos a di sa yos: te chi ñom lā am ndam. 11 Te nekatu ma chi aduna si, wande ñile ñungi chi aduna si, te mangi ñou fi you. Bay bu sela bi, otu len chi sa tur ña nga ma may on, ndah͈ ñu di bena niki ñun. 12 Ba ma neke ak ñom, dēncha nā len chi sa tur ña nga ma may on: te otu nā len, te ken sankuwul chi ñom, ganou dōm i tafar ja: ndah͈ mbinda ma motaliku. 13 Wande ñou nā fi you lēgi; te yef yile lā wah͈ chi aduna si, ndah͈ suma banēh͈ di motaliku chi ñom. 14 May nā len sa bāt; te aduna si bañ na len, ndege boku ñu chi aduna si, naka man itam boku ma chi aduna si. 15 Ñānu ma ne nga gēne len chi aduna si, wande ndah͈ nga otu len chi lu bon. 16 Boku ñu chi aduna si, naka ma bokule chi aduna si. 17 Selal len chi dega gi: sa bāt a di dega. 18 Naka nga ma yōni on chi aduna si, nōnule lā len yōni chi aduna si itam. 19 Te ngir ñom lā selal suma bopa, ndah͈ ñom itam di nañu selal sēn bopa chi dega. 20 Ñānatu ma ngir ñom reka, wande ngir ña di gumi chi man itam chi sēn bāt; 21 Ndah͈ ñom ñepa di bena; naka you, Bay bi, neka chi man, te man mā neka chi you, ñom itam ñu neka chi ñun: ndah͈ aduna si di gum ne yā ma yōni on. 22 Te ndam li nga ma may on, may nā len ko; ndah͈ ñu neka bena, naka ñun sah͈ ñu neka bena; 23 Man chi ñom, ak you chi man, ndah͈ ñu motaliku chi bena; ndah͈ aduna si h͈am ne yā ma yōni on, te sopa nga len, naka nga ma sope. 24 Bay bi, ña nga ma may on, buga nā ne ñom itam ñu neka ak man fa ma neka; ndah͈ ñu sêt suma ndam li nga ma may: ndege sop’ on nga ma ba aduna si sosôngul. 25 Ey Bay bu jūb bi, aduna si h͈amul la won, wande mā la h͈am on; te ñile h͈am nañu ne yā ma yōni on. 26 Te h͈amlo won nā len sa tur, ti di nā ko h͈amlôti; ndah͈ nchofel gi nga ma sope won neka chi ñom, te man chi ñom. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society