John 14 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Bu sēn h͈ol jāhle: gum ngēn chi Yalla, gum len itam chi man. 2 Cha suma ker Bay i ndekay yu bare ana fa; su nekul on nōnu, da ma len wah͈ kon; ndege mange dem wājal len bereb. 3 Te su ma deme te wājal len bereb, di nā delusêti, te jel len chi suma bopa; ndah͈ fa ma neka, yēn itam ngēn mun fa neka. 4 Te fa ma di dem, h͈am ngēn yōn wi. 5 Thomas ne ko, Borom bi, h͈amu ñu fo di dem; naka la ño h͈ame yōn wa? 6 Yesu ne ko, Man mā di yōn wi, ak dega gi, ak dūnda gi; ken du ñou fi Bay ba, lu dul chi man. 7 Su ngēn ma h͈am on, don ngēn h͈ami suma Bay itam: cha ganou wah͈tu wile h͈am ngēn ko, te gis ngēn ko. 8 Philip ne ko, Borom bi, won ñu Bay ba, te di na ñu doy. 9 Yesu ne ko, Ndah͈ neka nā ak yēn bu yāga, te h͈amangu la ma, Philip? Ka ma gis, Bay ba la gis; naka nga wah͈e, ne, Won ñu Bay ba? 10 Ndah͈ gumu la ne mangi chi Bay ba, te Bay ba’ngi chi man? Bāt yi ma len wah͈ wah͈u ma ko chi suma bopa: wande Bay ba deka chi man, mō def ligey yi. 11 Gum len ma ne mangi chi Bay ba, te Bay ba’ngi chi man: te su nekule, gum len ma ngir ligey ya sah͈. 12 Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Ku gum chi man, ligey yi ma def, mō len di def itam; te lu upa yile la di def; ndege mange dem fa Bay ba. 13 Te lu mu mun a don lu ngēn di ñān chi suma tur, lōlu lā di def, ndah͈ Bay ba ame ndam chi Dōm ji. 14 Su ngēn ñāne lu neka chi suma tur, di nā ko def. 15 Su ngēn ma sope, di ngēn dēncha suma i eble. 16 Te di nā ñān Bay ba, te di na len may benen Dalalkat, ndah͈ mu neka ak yēn bel mos; 17 Nh͈el i dega ma la: ka aduna si munul a nangu; ndege gisu ko, te h͈amu ko: yēn a ko h͈am; ndege deka na ak yēn, te di na neka chi yēn. 18 Du ma len bayi ngēn wēt: di nā ñoui fi yēn. 19 Chi sā su new aduna si du ma gisati; wande yēn a ma gis: ndege da ma dūnda, yen a di dūnda itam. 20 Chi bes bōbale di ngēn h͈ami ne mangi chi suma Bay, te yēnangi chi man, te mangi chi yēn. 21 Ku am suma i eble, te dēncha len, mō ma sopa: te ka ma sopa mōm la suma Bay di sopa, te man di nā ko sopa, te fêñu ko suma bopa. 22 Judas ne ko, (dowul Iscariot), Borom bi, lu la jot be nga ñu di fêñu, te dowul chi aduna si? 23 Yesu tontu te ne ko, Su ma kena sope, di na dēncha suma bāt: te suma Bay di na ko sopa, te di nañu dika fi mōm, te deka ak mōm. 24 Ku ma sopul, du dēncha suma i bāt: te bāt bi ngēn dēga dowul suma bos, wande Bay ba ma yōni on. 25 Yef yile lā len wah͈ bi ma deke ak yēn. 26 Wande Dalalkat ba, mu di Nh͈el mu Sela ma, ka Bay ba di yōni chi suma tur, di na len jemantali yef yepa, te fatali len lu ma len wah͈ on yepa. 27 Jama lā bayi ak yēn; suma jama lā len may: dowul naka ko aduna si maye lā len ko maye. Bu sēn h͈ol jāh͈le, te bu mu tīt. 28 Dēg’ on ngēn naka ma len wah͈ on, ne, Di nā dem, te di nā delusêti fi yēn. Su ngēn ma sop’ on, don ngēn banēh͈uji, ndege di nā dem fa Bay ba: ndege Bay ba gen na rey as man. 29 Te wah͈ nā len ko lēgi bala mu jot, ndah͈ bu mu jote, di ngēn gumi. 30 Du ma wah͈ati ak yēn lu bare; ndege gelouar i aduna sile ñou na; te amul dara chi man; 31 Wande ndah͈ aduna si h͈am ne sopa nā Bay ba, te naka ma Bay ba joh͈e won eble, nōgule lā def. Jog len, na ñu dem cha kanam. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society