John 12 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 19071 Yesu nak jurom ben’ i fan bala h͈ewte ga jot, dika cha Bethany, fa Lazarus nek’ on, ka Yesu dēkali won cha dē ga. 2 Tah͈ on na ñu tōgal ko rêr fōfale; te Martha bukanēgu; wande Lazarus anga won cha ña denu ak mōm cha rêr ba. 3 Mariama nak indi bena libar i h͈êñh͈êñ bu jafe njēg lol, te diw ko cha i tank’ i Yesu, te fomp’ i tank’ am ak kouar am; be nēg ba fês ak h͈et i h͈êñh͈êñ ga. 4 Wande Judas Iscariot, kena chi i talube am, ka ko ori, ne, 5 Ana lu tēre won ñu jay h͈êñh͈êñ gōgule ñeta tēmēr i transu, ndah͈ ñu sarah͈ ko miskin yi? 6 Wah͈ on na lōlu, dowul ndege defa topato won miskin ya: wande ndege sachakat la won, te ame won mbūs ma, te jel la ñu def cha bir am. 7 Tah͈na Yesu ne, Bayi ko; ndig suma bes i sūl la ko dēncha. 8 Ndege miskin ya’ngi ak yēn sā su neka; wande man du len ma ami bel mos. 9 Lu bare cha Yauod ya dēga ne munga fa; te ñu dika, dowul ndig bop’ i Yesu reka, wande ndah͈ ñu gis Lazarus itam, ka mu dēkali won cha dē ga. 10 Wande i njīt i seriñ ya fēncho ndah͈ ñu rēy Lazarus itam; 11 Ndege ngir mōm la jopa chi Yauod ya dem, te gum chi Yesu. 12 Cha elek sa mbōlo mu rey ma ñou on cha h͈ewte ga, ba ñu dēge ne Yesu ange dika cha Jerusalem, 13 Ñu fah͈a i banh͈as i tir ya, te dem gatanduji ko, te h͈āchu ne, Hosanna: barkel chi ka di dika chi tur i Borom ba, mu di Bur i Israel. 14 Te Yesu, ba mu feke chambur i mbam suf, mu war ko, cha naka ñu bind’ on, ne, 15 Bul ragal, dōm i Zion ju jigen: sêtal, sa Bur ange dika, di tōg chi kou chambur i mbam suf. 16 Yef yōyu i talube am h͈amu ñu ko won bu jeka; wande ba Yesu ame won ndam am, ñu fataliku ne bind’ on nañu yef yōyu chi lu jem chi mōm, te defal on nañu ko yef yōyule. 17 Mbōlo ma itam ña nek’ on ak mōm ba mu ô on Lazarus cha bamel ba, te dēkali ko cha dē ga, sēde won nañu ko. 18 Lōlo tah͈ itam mbōlo ma dem gatanduji ko, ndege dēg’ on nañu ne mō def on koutef gōgale. 19 Pharisee ya nak wah͈ante chi sen bopa, ne, Gis ngēn ne munu len dara: aduna si topa nañu ko. 20 Ñena chi wā’ Greece ya’nga won chi digante ña dem on a jāmu cha h͈ewte ga: 21 Ñile nak ñou fa Philip, ka juge won cha Bethsaida cha Galilee, te lāj ko, ne, Gōr gi, buga naño sêtsi Yesu. 22 Philip ñou te wah͈ Andrew: Andrew ñou ak Philip, te ñu wah͈ Yesu. 23 Te Yesu tontu len, ne, Wah͈tu wi jot na be ba Dōm i nit ka di ami ndam. 24 Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Digfey pēp’ i dugup rotul chi suf si te dē, mu des bop’ am dal; wande su dēe, di na mēña mēñef yu bare. 25 Ku sopa dūnd’ am, di na ko rēral; te ku bañ dūnd’ am chi aduna sile, di na ko dēncha be cha dūnda gu dul jêh͈. 26 Su ma kena bukanēgo, na ma topa; te fu ma neka, fōfale la suma bukanēg di neki: su ma kena bukanēgo, mōm la Bay ba di magal. 27 Suma fit nah͈arlu na lēgi; te ana lu ma war a wah͈? Bay bi, musal ma chi wah͈tu wile? Wande lōlo tah͈ ma dika chi wah͈tu wile. 28 Bay bi, magalal sa tur. Bāt nak juge cha asaman, ne, Magal nā ko, te di nā ko magalati. 29 Tah͈na mbōlo ma ña fa tah͈ou on te dēga ko, ne, Defa denu: ñenen ne, Ab malaka di wah͈ ak mōm. 30 Yesu tontu te ne, Bāt bōba dowul ndig man la juge won, wande ndig yēn. 31 Ate’ aduna sile jot na: lēgi ñu gēne gelouar i aduna sile, te sani ko cha biti. 32 Te man, su ma yēkatiko chi suf si, di nā hēchi nit ñepa fi man. 33 Wande lile wah͈ na ko mu tiki ne, ban melo dē la dēe. 34 Mbōlo ma tontu ko, ne, Dēga nañu chi tauret bi ne Krista di na deka bel mos: naka nga wah͈e nak ne Dōm i nit ka ela na yēkatiku? Kan a di Dōm i nit kōku? 35 Yesu ne len, Chi wah͈tu wu new la lêr gi di neka ak yēn. Doh͈ len bi ngēn ame lêr gi, ndah͈ lendem du len jot: ndege ku di doh͈ chi lendem gi du h͈am fu mo dem. 36 Bi ngēn ame lêr gi, gum len chi lêr gi, ndah͈ ngēn mun a neka dōm i lêr. Yef yōyu la Yesu wah͈ on, te mu dem te nubu cha ñom. 37 Wande ba mu def on koutef yu bare chi sēn kanam, gumu len chi mōm: 38 Ndah͈ bāt i Isaiah yonent ba motaliku, ba mu wah͈ on, ne, Borom bi, kan a di gum suñu yēgle? te chi kan la loh͈o i Borom ba fêñu? 39 Lōlo tah͈ on ñu munul a gum, ndege Isaiah wah͈ati won na, ne, 40 Silmah͈alo na sēn i but, te degerlo na sēn h͈ol; ndah͈ ñu gisul ak sēn i but, te h͈am ak sēn h͈ol, te tūb, te ma weral len. 41 Yef yōyu la Isaiah wah͈ on, ndege gis on na ndam am; te wah͈ chi lu jem chi mōm. 42 Wande itam lu bare chi kēlifa ya gum on nañu chi mōm; wande ndig Pharisee ya wonewu ñu ko won, ndah͈ du ñu len gēne cha juma ja. 43 Ndege sop’ on nañu teranga bu juge fi nit as teranga bu juge fa Yalla. 44 Te Yesu h͈āchu te ne, Ku gum chi man, gumul chi man reka, wande chi mōm ka ma yōni on. 45 Te ku ma sêt, sêt na ka ma yōni on. 46 Da ma dika lêr chi aduna si, ndah͈ ku mu mun a don ku gum chi man du deka chi lendem. 47 Te su kena dēge suma i wah͈, te defu len, mā ko atewul; ndege diku ma atesi aduna si, wande musal aduna si. 48 Ku ma bañ, te nanguwul suma i wah͈, am na kena ku ko ate: bāt ba ma wah͈ on, mō ko ateji cha bes bu muje ba. 49 Ndege wah͈u ma chi suma bopa, wande Bay ba ma yōni on, mō ma ebal lu ma war a wah͈, ak lu ma war a jemantal. 50 Te h͈am nā ne eble am a di dūnda gu dul jêh͈: yef yi ma wah͈ mbōk, naka ma Bay ba wah͈e, nōgule lā wah͈. |
Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.
British & Foreign Bible Society