Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

John 11 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Jena way jēr on na, Lazarus cha Bethany, dek’ i Mariama, ak mag am Martha.

2 Te kile di Mariama ma diw on Borom bi ak h͈êñh͈êñ, te fomp’ i tank’ am ak kouar am, ku chameñ am Lazarus jēr on.

3 Jigen am ya nak yōni fa mōm, ne, Borom bi, gisal ka nga sopa jēr na.

4 Wande ba ko Yesu dēge, mu ne, Jēr bōbu du tah͈ mu dē, wande di na jem chi ndam i Yalla, ndah͈ Dōm i Yalla jele chi ndam.

5 Yesu nak sop’ on na Martha, ak rak’ am ju jigen, ak Lazarus.

6 Ba mu dēge ne jēr na, mu jēki fa be ñar i fan cha bereb ba mu nek’ on.

7 Cha ganou lōlu mu ne talube ya, Na ñu demati Judea.

8 Talube ya ne ko, Rabbi, Yauod ya’ngi la don ūt ndah͈ ñu jumat la ak i doch; te di nga fa demati?

9 Yesu tontu, ne, Ndah͈ dowul fuk’ i wah͈tu ak ñar chi bechek? Su kena doh͈e chi bechek, du fakatalu, ndege di na gis lêr i aduna sile.

10 Wande su kena doh͈e chi gudi, di na fakatalu, ndege lêr gi nekul chi mōm.

11 Yef yile la wah͈ on; te ganou lōlu mu ne len, Lazarus suñu h͈arit defa nelou; wande di nā dem ndah͈ ma ê ko chi nelou am.

12 Talube ya ne ko, Borom bi, su neloue, di na wer.

13 Yesu nak chi dē am la wah͈ on; wande ñu dēfe ne chi nopaliku’ nelou la wah͈ on.

14 Mōtah͈ Yesu nelen bu set, Lazarus dē na.

15 Te da ma kontan ndig yēn ne neku ma fa won, ndah͈ ngēn gum; wande na ñu dem fa mōm.

16 Thomas ku tuda sīh͈ bi, ne i morom i talube am ya, Na ñu dem itam, ndah͈ ñu dē ak mōm.

17 Ba Yesu agse, mu feka mu am nak ñenent i fan cha bamel ba.

18 Bethany jegeñ na Jerusalem, lu day ni fuk’ i furlong ak jurom.

19 Te Yauod yu bare ñou on nañu fa Martha ak Mariama, ndah͈ ñu jālesi len sēn chameñ.

20 Martha nak ba mu dēge ne Yesu agsi na, mu dal di ko gatanduji: wande Mariama tōgandi cha bir nēg ba.

21 Martha ne Yesu, Borom bi, so fi nek’ on, suma chameñ dowul kōn dēi.

22 Te nistey itam, h͈am nā ne lo mun a ñān Yalla, Yalla di na la ko may.

23 Yesu ne ko, Sa chameñ di na dēkêti.

24 Martha ne ko, H͈am nā ne di na dēki cha ndēkite ga kera bes ba.

25 Yesu ne ko, Mā di ndēkite gi ak dūnda gi: ku gum chi man, su dēe sah͈, di na dūnda:

26 Te ku mu mun a don ku di dūnda te gum chi man, du dē muka. Ndah͈ gum nga lile?

27 Mu ne ko, Wau, Borom bi, gum nā ne Yā di Krista, Dōm i Yalla, ka dika chi aduna si.

28 Ganou ba mu wah͈e lōlu, mu dem te ô Mariama rak’ am chi kumpa, ne, Borom ba’ngi fi, te mungi la ô.

29 Te mōm ba mu ko dēge, mu jog bu gou te dem fa mōm.

30 Yesu nak dikangul on cha bir deka ba, wande munga cha bereb ba ko Martha fek’ on.

31 Yauod ya nak ña nek’ on ak mōm cha nēg ba, di ko jāle, ba ñu gise ne Mariama jog bu gou te gēna, ñu topa ko, ndege fōg on nañu ne munga dem cha bamel ba ndah͈ mu yuh͈u fa.

32 Ba Mariama agse fa Yesu nek’ on, te gis ko, mu dānu chi i tank’ am, ne ko, Borom bi, so fi nek’ on, suma chameñ dowul kōn dēi.

33 Ba ko Yesu gise mu di yuh͈u, ak Yauod ya di yuh͈u ña and’ ak mōm, mu bini chi nh͈el ma, te getenu,

34 Te ne, Ana fu ngēn ko tedal? Ñu ne ko, Borom bi, dikal te gis.

35 Yesu joy.

36 Yauod ya ne nak, Sêt len, naka mu ko sope won!

37 Wande ñena chi ñom ne, Kile ūbi won i but i silmah͈a ba, ndah͈ munul on a tah͈ itam ne kōku dowul on dēi?

38 Yesu nak, di binêti chi bop’ am, dika cha bamel ba. Nkan la won, te teg on nañu doch chi kou am.

39 Yesu ne, Tegi len doch wi. Martha, jigen i ka dē on, ne ko, Borom bi, wah͈tu wile di na feka mu h͈asou; ndege dē on na be am ñenent i fan.

40 Yesu ne ko, Ndah͈ wah͈u ma la won ne, so gume, di nga gisi ndam i Yalla?

41 Mōtah͈ ñu tegi doch wa. Te Yesu yēkati i but am, te ne, Bay bi, mangi la gerem ndege dēga nga ma.

42 Te h͈am nā ne dēga nga ma sā su neka: wande ndig mbōlo mu tah͈ou file ma wah͈ ko, ndah͈ ñu gum ne Yā ma yōni on.

43 Te ba mu wah͈e nōgule, mu h͈āchu be cha kou, ne, Lazarus, gēnasil.

44 Ka dē on gēnasi, ak na ñu ewe won loh͈o am ak tank’ am ak yēre’ bamel ya; te kanam am ñu lah͈as ko ak ser. Yesu ne len, Ewi len ko, te bayi ko mu dem.

45 Yauod yu bare nak ña dik’ on fa Mariama, te gis li mu def on, gum chi mōm.

46 Wande ñena chi ñom dem fa Pharisee ya, te nitali len yef ya Yesu def on.

47 Njīt i seriñ ya nak ak Pharisee ya dajalo fēncho, te ne, Ana lu ño def? ndege nit kile def na koutef yu bare.

48 Su ñu ko bayie nōgule, ñepa di nañu gum chi mōm: te wā’ Rome ya di nañu dika, te jel suñu bereb ak suñu rew itam.

49 Wande kena chi ñom, Caiaphas, ka don kēlifa i seriñ ya cha at mōmale, ne len, H͈amu len dara,

50 Te sêtluwu len ne di na len genal ndah͈ kena nit dē ndig mbōtay gi, te du h͈êt gi gepa di boka sanku.

51 Te lile wah͈u ko won chi bop’ am; wande ndege mō nek’ on kēlifa i seriñ ya cha at mōmale, mu wolif ne Yesu war a dē ngir h͈êt wi;

52 Te du ngir h͈êt wi reka, wande ndah͈ mu mun a dajale chi bena dōm i Yalla ña tasāro won fu neka.

53 Cha ganou bes bōbale, ñu fēncho ndah͈ ñu rēy ko.

54 Tah͈na Yesu doh͈atul cha kanam i Yauod ya, wande mu bayako fa, dem rew mu jegeñ manding ma, cha deka bu tūda Ephraim; te mu jēki fa ak talube ya.

55 H͈ewte i Yauod ya jegeñsi na; te ñu bare juge cha deka ya, dem cha Jerusalem ba h͈ewte ga lāta jot, ndah͈ ñu setal sēn bopa.

56 Ñu ūt Yesu nak, te wah͈ante chi sēn bopa ba ñu tah͈oue cha juma ja, ne, Ana lu ngēn dēfe? Ne du ñou chi h͈ewte gi?

57 I njīt i seriñ ya ak Pharisee ya joh͈e won nañu eble, ne su kena h͈ame fu mu neka, na ko wone, ndah͈ ñu japa ko.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan