Biblia Todo Logo
Bìoball air-loidhne

- Sanasan -

John 1 - Linjil i Yesu Krista Suñu Borom bi 1907

1 Cha chosan la Bāt ba am on na, te Bāt ba nek’ on na ak Yalla, te Bāt ba nek’ on na Yalla.

2 Kile mō nek’ on cha chosan la ak Yalla.

3 Lu neka chi mōm la saku on; te ganou mōm dara sakuwul on cha la saku on.

4 Chi mōm la dūnda nek’ on; te dūnda gi nek’ on na lêr i nit.

5 Te lêr gi melah͈ chi lendem gi, te lendem gi sēnu ko won.

6 Nit ñou on na ka Yalla yōni on, ku tūda John.

7 Kile sah͈ ñou on na ndig sēde, ndah͈ mu sēde chi lêr gi, ndah͈ ñepa mun a gum chi mōm.

8 Mōm nekul on lêr gi, wande ñou on na ndah͈ mu sēde chi lêr gi;

9 Lêr i dega gi di lêral nit ku neka ange ñou chi aduna si.

10 Nek’ on na chi aduna si, te chi mōm la aduna si saku on, te aduna si h͈amu ko won.

11 Ñou on na fi yos am, te yos am nanguwu ñu ko won.

12 Wande ña ko nangu on, ñom la may on sañsañ ñu neka i dōm i Yalla, ña gum chi tur am:

13 Ña jūdu on, dowul chi deret, mbāte chi mbugel i yaram, mbāte chi mbugel i nit, wande chi Yalla.

14 Te Bāt bi yaramu on na, te dek’ on na ak ñun, te sêt on nañu ndam am, ndam niki ku di dōm i bay ju di bajo, fês ak yiw ak dega.

15 John sēde on na ko, te h͈āchu, ne, Kile di ka ma wah͈ on, ne, Ka di ñou chi suma ganou neka na chi suma kanam, ndege mō ma jek’ on a neka.

16 Ndege chi fêsay am la ñu nangu on ñepa, ak yiw chi kou yiw.

17 Ndege Musa la ñu joh͈ on yōn wi; yiw ak dega bayako fa Yesu Krista.

18 Ken mosul a gis Yalla muk; Dōm am ja di bajo, ka neka chi den’ i Bay ba, mō ko fêñal.

19 Te lile di sēde’ John, ba Yauod ya yōne fa mōm i seriñ ak i fōdey bawo cha Jerusalem, di ko lāj, ne, Yā di kan?

20 Mu yēgle, te wēdiwul; mu yēgle, ne, Dowu ma Krista.

21 Ñu lājte ko, ne, Kan nak? Ndah͈ yā di Elijah? Mu ne, Dowu ma. Ndah͈ yā di yonent ba? Mu tontu, ne, Dēt.

22 Ñu ne ko mbōk, Yā di kan? ndah͈ ñu delo tontu ña ñu yōni on. Lan nga wah͈ chi sa bopa?

23 Mu ne, Mā’di bāt i kena ka di h͈āchu cha manding ma, Jūbal len yōn i Borom bi, naka Isaiah yonent ba wah͈ on.

24 Te Pharisee ya len yōni on.

25 Te ñu lāj ko, te ne ko, Ana lutah͈ nga di batise, so dowule Krista, mbāte Elijah, mbāte yonent ba?

26 John tontu len, ne, Mā batise ak ndoh͈; wande chi sēn digante kena di tah͈ou ka ngēn h͈amul;

27 Mō di ñou chi suma ganou, te daganu ma tiki būm i dal’ am.

28 Yef yilê ’nga h͈ewe won cha Bethany, ganou wala Jordan, fa John don batise.

29 Cha elek sa mu gis Yesu di ñou fi mōm, te ne, Sêt len, Mburtu’ Yalla mā’ngi, ka dindi bakar i aduna si!

30 Mō di kile ma wah͈ on, ne, Nit di na dika chi suma ganou ka ma jītu, ndege mō ma jītu on.

31 Te h͈amu ma ko won; wande ndah͈ mu fêñu cha Israel, lile tah͈ ma ñou di batise ak ndoh͈.

32 Te John sēde on na, ne, Gis on nā Nh͈el ma wacha niki mpetah͈ cha asaman; te mu tōg cha kou am.

33 Te h͈amu ma ko won: wande ka ma yōni on batise ak ndoh͈, mō ma wah͈ on, ne, Chi kan nga gis Nh͈el ma wacha, te tōg chi kou am, kōkale di batise ak Nh͈el mu Sela ma.

34 Te da ma gis on, te sēde ne kile di Dōm i Yalla.

35 Cha elek sa John tah͈ouati, ak ñar chi i talube am;

36 Te mu sêt Yesu naka mu doh͈e, te ne, Sêt len, Mburtu’ Yalla mā’ngi!

37 Te ñar i talube ya dēga mu wah͈, te ñu topa Yesu.

38 Te Yesu h͈inaku, te gis len ñu di topa, te ne len, Lu ngēn di ūt? Ñu ne ko, Rabbi (mu tiki ne Jemantalkat bi), ana fan nga deka?

39 Mu ne len, Dika len te gis. Ñu dika, te gis fa mu deka, te jēki ak mōm bechek bōba; chi fuk’ i wah͈tu la won potah͈.

40 Kena chi ñar ña dēg’ on John, te top’ on ko, Andrew la won, rak’ i Simon Peter.

41 Mu jeka gis mag am Simon, te ne ko, Feka nañu Masiu ma (mu tiki ne Krista).

42 Mu indi ko fi Yesu. Yesu sêt ko, te ne, Yā di Simon, dōm i John: di nañu la tūde Cephas (mu tiki ne Peter).

43 Cha elek sa bug’ on na dem cha Galilee, te mu gis Philip, te Yesu ne ko, Topa ma.

44 Philip nak juge on na Bethsaida, dek’ i Andrew ak Peter.

45 Philip gis Nathanael, te ne ko, Feka nañu ka Musa ak yonent ya bind’ on chi tauret ba, Mō di Yesu wā’ Nazareth, dōm i Yusufa.

46 Te Nathanael ne ko, Ndah͈ lu bāh͈ mun na juge cha Nazareth am? Philip ne ko, Dikal te sêt.

47 Yesu gis Nathanael mu di dika fi mōm, te wah͈ chi lu jem chi mōm, ne, Wā’ Israel chi dega angile, ka amul bena gaka.

48 Nathanael ne ko, Ana fo ma h͈ame? Yesu tontu te ne ko, Ba la Philip ôangule, ba nga neke cha run mbot ga, gis nā la.

49 Nathanael tontu ko, ne, Rabbi, yā di Dōm i Yalla; yā di Bur i Israel.

50 Yesu tontu ko, ne, Gum nga ndege da ma la ne, Gis on nā la cha run mbot ga? Di nga gisi yef yu gen a rey as yile.

51 Te mu ne ko, Chi dega, chi dega, mangi len di wah͈, Di ngēn gisi asaman ūbiku, te i malaka i Yalla di yēg ak di wacha chi kou Dōm i nit ka.

Published by the British and Foreign Bible Society 1882-1907.

British & Foreign Bible Society
Lean sinn:



Sanasan